Sabóor 101
Buur a ngi jaayanteek Yàlla
Ñeel Daawuda, di kàddug Sabóor.
 
Ngor ak yoon laay woy.
Yaw Aji Sax ji laay joobe.
Naa teewlu yoonu maandute.
Ana kañ nga may dikkal?
Naa doxe maandute
fi sama biir waa kër.
Caaxaani neen, xooluma;
jëf ju wàcc yoon, bugguma,
taqu ma fenn.
Kuy nas njekkar, sore ma;
lu bon, xawma ko.
Kuy jëw moroomam, ma wedamal;
ku daŋŋiiral ak ku reew, muñaluma la.
Ku dëggu ci réew mi, ma geesu,
ngir fat ko.
Te kuy wéye maandute,
kookoo may liggéeyal.
Kuy njublaŋ du tooge sama kër,
kuy fen du taxaw sama kanam.
Maay xëy, sànk képp ku bon ci réew mi,
ngir dagge ci dëkkub Aji Sax jii képp kuy def lu ñaaw.