Sabóor 110
Yàlla fal na nitam
Ñeel Daawuda, di kàddug Sabóor.
 
Aji Sax ji daa wax sama Sang, ne ko:
«Toogeel sama ndijoor,
ba ma def say noon sa ndëggastal.»
 
Sa nguur la Aji Sax ji saxal, dale ko fa Siyoŋ.
Yilifal noon yi la wër!
Sa mboolooy taxawal seen bopp,
sa bésub xare.
Ña nga soloo darajaak sellnga,
faboo fa njël sosoo,
diy ndaw, wàccsil la, mbeteb lay.
 
Aji Sax jee ko giñ,
te du dellu gannaaw:
«Yaa dib sarxalkat ba fàww,
topp dayob Melkisedeg*
 
Sang baa ngi fi sa ndijoor
te mooy rajaxe buur yi, bés bu meree.
Mooy mbugal xeet yi, jal seeni néew,
di rajaxe kilifay àddina, ba mu daj.
 
Déeg ba feggook yoon wa, Buur a cay naan,
te moo ko tax di siggi.
* 110:4 Melkisedeg: buurub Salem la woon, di sarxalkat bu Yàlla faloon ci jamonoy Ibraayma, maanaam ñeenti téeméeri at laata Aaróonaa doon ab sarxalkat.