Sabóor 122
Nu ñaanal Yerusalem
Muy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla, ñeel Daawuda.
 
Maaka bég, ba ñu ma nee:
«Kër Aji Sax ji lanu jëm.»
Yaw Yerusalem, noo ngii taxaw sa bunt.
 
Céy, Yerusalem, dëkkub tabax bu baax,
bi booloo, di benn.
Fii la giiri Israyil di yéegsi,
di giir yi Ki Sax séddoo.
Ñu ngi santsi Aji Sax ji,
ni ko Israyil warloo.
Fii la ngànguney Israyil tege,
askanu Daawuda toog ca, di àtte.
 
Dagaanleen jàmmi Yerusalem:
«Yerusalem, yal na sa xeli soppe dal,
jàmm ne ñoyy fi say tata wër,
te xel dal ci biir këri Buur.»
Mbokk ak xarit a waral
may ñaan jàmmi Yerusalem.
Sunu kër Yàlla Aji Sax jee ma tax
di sàkku ngëneelu Yerusalem.