Sabóor 141
Yàlla, sàmmal sama làmmiñ
Muy kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.
 
Aji Sax ji, woo naa la, gaawe ma!
Bu ma lay woo, teewlu ma.
Yal nanga ma nangul samag ñaan
ni cuuraay lu ñu la taalal,
yoxo yi ma la tàllal di saraxu ngoon soo gërëm.
 
Aji Sax ji, sàmmal ma sama làmmiñ,
saytul ma sama kàddu.
Bu ma xiir ci lu aay,
may jëfe jëf ju bon,
ànd ceek ñiy jëf lu ñaaw,
di wàlli seeni bernde.
Kuy déggal Yàlla, man na maa dóor,
bantal ma ci ngor.
Loolu ngëneelu cuuraay la, duma ko bañ.
Waaye maa ngi saxoo ñaan pexey noon moy.
 
Yal nañu fenqe seeni njiit ciw doj,
ba noon yi xam ne dëgg laa wax.
Ni ñuy gàbbe suuf ba mu ne ŋafeet,
ni la njaniiw di ŋaye,
aw seeni yax yu tasaaroo.
 
Aji Sax ji Boroom bi, yaw laa wékki gët,
yaw laa làqoo,
bu ma seetaan, ma dee.
Musal ma ci yeer yi ñu ma gasal,
ak fiir yi ma defkati ñaawtéef yi tegal.
10 Yal na ku bon tàbbi cig fiiram,
te man ma teggi, wéy.