Sabóor 17
Aji Sax ji, jox ma dëgg
Muy ñaanu Daawuda.
 
Éy Aji Sax ji, déglul liy dëgg,
déglul, ma woote!
Teewlul, ma dagaane la
làmmiñ wu mucc fen.
Yal na sama àtte bawoo fi yaw,
nga gis sama njubte.
Natt nga saab xol, niir ma guddi,
settantal ma, gisoo dara.
Dogu naa ne duma moye wax.
Su may jëf it, di sàmm sa kàddu.
Maay moyu yoonu ku bon.
Sa tànk, sama tànk,
jàdduma fenn.
 
Éy Yàlla, maa lay woo, nga di ma wuyu;
teewlu ma te déglu ma!
Na sa ngor feeñ,
yaw miy walloo sa doole
ku la làqooy noonam.
Sàmm ma ni peru bët;
làqe ma sa ker,
ma rëcc ñu bon ñi ma song,
noon ñii ma gaw, nar maa bóom.
10 Seen xol dàq yërmande,
seeni wax di reewande.
11 Tanc nañu nu fépp,
ne nu jàkk, nar noo tëral.
12 Mbete gaynde gu namma fàdde,
gaynde gu mat guy tëroo!
 
13 Éy Aji Sax ji, jógal dajeek moom, detteel ko.
Xettlee ma sa saamar, ma rëcc ku bon.
14 Éy Aji Sax ji, walloo ma sa doole,
ma rëcc ñi séddoo dundu àddina.
Say soppe, nga reggal,
seeni doom regg,
desalal seeni doom.
 
15 Man nag ma am dëgg, ne la jàkk,
yewwu, regge sa jëmm.