Sabóor 20
Yal na Buur daan
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.
 
Buur, yal na la Aji Sax ji nangul bésu njàqare,
yal na la turu Yàllay Yanqóoba aj fu kawe,
yal na la yónnee wallam fa këram,
jàpplee la fa, ca Siyoŋ.
Yal na xool loo ko jébbal,
di rafetlu sarax soo ko lakkal.
Selaw.
Yal na la may li nga namm,
di sottal loo mébét,
ngay daan, nuy ree,
yéege sunu raaya, màggal sunu Yàlla.
Yal na Aji Sax ji nangu loo dagaan.
 
Aji Sax jeey musal ki mu fal, bir na ma tey.
Moo koy nangule fa asamaan su sell sa,
ci dooley ndijooram biy musle.
Ñiiki watiir,
ñeeki fas,
nun sunu turu Yàlla Aji Sax ji lanuy tudd.
Ñoom ñooy jeng ak a jóoru,
nun, nu jóg, taxaw jonn.
 
10 Éy Aji Sax ji, mayal Buur mu daan,
te bés bu nu ko ñaane, mu nangul nu.