Sabóor 22
Jëkke jàq, mujje sant
1 Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda, dëppook galan bi ñu dippee Kéwélu fajar.
2 Sama Yàlla, sama Yàlla, lu tax nga wacc ma?
Ma binni, binneeti, wall sore.
3 Éy sama Yàlla, ma woote bëccëg, wuyuwoo;
woote guddi, nopploo ma.
4 Yaw de, yaay ku sell, tooge sab jal,
Israyil di la kañ.
5 Yaw la sunuy maam wóolu woon,
wóolu la, nga xettli leen.
6 Yaw lañu daa woo wall, mucc;
yaw lañu wóolu woon te rusuñu.
7 Man nag aw sax rekk laa, matuma nit.
Doom aadama sewal ma, aw xeet tuutal ma.
8 Ku ma gis ñaawal ma,
biiñ ma, xeelu ma, naa:
9 «Na wéeroo Aji Sax ji, mu xettli ko;
su ko soppee, na ko wallu.»
10 Yaw de yaa ma roccee sama biiru ndey,
naxe ma sama weenu yaay.
11 Yaw laa dénkoo ba may juddu,
ba ma juddoo sama ndey, ngay sama Yàlla.
12 Bul ma sore,
musiba teew na, wall amul!
13 Noon yaa ngi ma gaw ni coggalu yëkk,
dar ma ni ponkali yëkk ya fa Basan.
14 Ñu ŋa ma, ŋàpp,
ni gaynde, guy yëmmook a fàdde.
15 Doole ŋiis,
yax yoqi,
fit ne soyox, seey.
16 Làmmiñ taqoo denqleñ,
doole jeex, ma wow koŋŋ,
nga tëral ma buntu bàmmeel.
17 Ay xaj a ma wër,
di gàngooru saaysaay, dar ma kepp,
bëtt samay yoxook samay tànk.
18 Maa ngii, mana waññ sama yax yépp,
ñoom ñuy xoole, di ma seetaan,
19 séddoo samay yére,
tegoo bant sama mbubb.
20 Waaye yaw, Aji Sax ji, bul sore;
yaa may dooleel, gaawe ma.
21 Xettlil sama bakkan ci saamar,
ba sama benn bakkan bii mucc selli xaj!
22 Musal ma ci pàddum gaynde ak ndañum nagu àll.
Yaa ma wallu woon!
23 Ma siiwali saw tur ci bokk yi,
màggale la digg mbooloo mi.
24 Yeen ñi ragal Aji Sax ji, santleen ko.
Yeen askanu Yanqóoba wépp, màggal-leen ko.
Yeen bànni Israyil gépp, wormaal-leen ko.
25 Moom de sàgganewul boroom tiis,
làqu ko kanamam,
ba mu wootee, wuyu na ko.
26 Yaw laay sante ndaje mu mag,
sottalal la samay dige, ñi la ragal seede.
27 Ku woyof a cay lekk ba doyal,
kuy wut Aji Sax ji, sant ko.
«Guddleena gudd fan!»
28 Àddina wërngal këpp ay fàttliku,
walbatiku ci Aji Sax ji.
Làngi xeet yépp sukkalsi ko.
29 Aji Sax jeey boroom nguur,
moo yilif xeet yi.
30 Boroom barke xéewlu, sujjóotal ko,
ku jëm pax it, te bakkanam di lang,
di ko sukkal.
31 Askan wu dikkagul dina jaamu Boroom bi,
ñiy ñëw te juddooguñu dees na leen wax ay mbiram.
32 Ñu dikk, biral njekkam,
jottli xeet wu sosoogul jalooreem.