Sabóor 3
Aji jub a ngi woote wall
1 Muy kàddug Sabóor, ñeel Daawuda, ba muy daw Absalom doomam ju góor.
2 Éy Aji Sax ji, noon yeeka bare!
Ñu baree may jógal,
3 ñu baree may tooge naa:
«Yàlla du ko wallu!»
Selaw
4 Waaye yaw Aji Sax ji, yaa may feg,
di ma teral, di ma siggil.
5 Maay woo Aji Sax ji wall,
mu walloo ma fa tundam wu sell wa.
Selaw.
6 Maay tëdd nelaw, yewwu;
Aji Sax ji di ma aar.
7 Ñu dul jeex a ma jógal, gaw ma,
te duma ragal.
8 Éy Aji Sax ji sama Yàlla,
jógal, wallu ma!
Yaa toj kaabaabi noon yu bon yépp,
foq seeni sell.
9 Aji Sax ji, yaa moom wall,
sa mbooloo jagoo sa barke.
Selaw.