Sabóor 30
Mucc, bég
Muy woyu Sabóor, ñeel Daawuda ca daloob kër Yàlla ga*.
 
Aji Sax ji, dama lay kañ.
Yaa ma yékkati,
ba noon reetaanu ma.
Aji Sax ji sama Yàlla, maa la woo wall,
nga faj ma.
Aji Sax ji, yaa ma jukkee njaniiw,
may ma bakkan, ma tàggook ñiy tàbbi njaniiw.
 
Yeen aji gëm ñi, woyleen Aji Sax ji,
njukkale ko sellngaam.
Meram di lu gàtt,
aw yiwam sax dàkk.
Rongooñ gane, fanaan,
ay ree xëysi.
 
Man damaa baaxle woon, ba ne:
«Deesu ma rëññeel mukk.»
Aji Sax ji, booba yaa ma baaxe,
dëj ma, ma ne kekk niw tund.
Nga fuuyu, ma jàq.
Aji Sax ji, yaw laa woo wall;
Boroom bi, yaw laa ñaanu yiw,
10 ne la: «Ma dee, tàbbi bàmmeel,
ana lu mu lay jariñ?
Nu la pëndu pax di sante,
bay biral sa worma?
11 Aji Sax ji, déglul, baaxe ma;
éy Aji Sax ji, dimbali ma.»
 
12 Yaa ma soppil samay rongooñ ay ree,
summi sama yérey tiis, solal ma bànneex.
13 Naa la woye xol, baña selaw.
Aji Sax ji, sama Yàlla, ma sant la ba fàww!
* 30:1 Woyu Sabóor wii Daawuda da koy sante Yàlla gannaaw mbas ma, ba mu jëndee dàgga ngir rendi fa sarax su dakkal mbas ma. Dàgga jooju lañu mujj tabax jaamookaay ba. Seetal ci 2.Samiyel 24, ak 1.Jaar-jaar ya 21.