Sabóor 36
Nit ñaaw, Aji Sax ji gore
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ñeel Daawuda jaamub Aji Sax ji.
 
Kàddug tooñ ga ku bon wax mu ngi sama xel mi.
Mu ne: «Ana lu may ragal ci Yàlla?»
Day gis boppam, naagu,
ba du gis sikkam, sib ko.
Ay waxam coxor aki fen,
jëfeetul lu rafet ak lu baax.
Day mébét lu ñaaw cib lalam,
taxawe yoon wu dëddu mbaax,
te du bañ lu bon.
 
Céy Aji Sax ji, gore nga ba kaw asamaan,
dëggu ba kaw-li-kaw.
Sa njekk a tiim tund yu mag yi,
sa àtte ne xéew ni xóotey géej.
Céy Aji Sax ji, nit ak mala, nga boole sàmm!
Céy Yàlla, yaa wéet ngor,
doom aadama yiiroo sa ker, yiiru;
yafloo sa njël lu duun,
sa xéewal wal, nga nàndale ko.
10 Ci yaw la dund di balle,
te sag leer lanuy leerloo.
 
11 Jotaleel sa ngor ku la xam,
jotale sa njekk kuy nas njub.
12 Yàlla bu ma ku reew teg tànk;
loxo ku bon, yàlla bumu ma taxa daw.
13 Defkati mbon yaa ngii, daanu,
ne lareet, tëlee jóg.