Sabóor 42
Maa namm Yàlla
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di taalif bu ñeel askanu Kore wu góor.
 
Yaw Yàlla, ni kéwél di sàkkoo walum ndox,
maa la koy sàkkoo xol.
Maa mar Yàlla,
Yàlla jiy dund!
Kañ laay teewi fa kanam Yàlla?
Rongooñ laay dunde
guddeek bëccëg,
noon yi di ma dëkke naa:
«Ana sa Yàlla ji?»
Lii laay fàttliku, sama xol jeex:
dama daan jàll, jiite mbooloo ma,
jëm kër Yàlla ga, di sarxolleek a sant,
ñu booloo di màggal.
Moo man, lu may yoggaaral nii?
Lu may jàq?
Naa yaakaar Yàlla,
ba dellu sante sama Yàlla wallam.
 
Maa ngi ne yogg,
ba di la fàttlikoo fa réewum Yurdan
ak tundi Ermon ak Misar.
Sa wal ya sotti, xóote awu moroom ma;
say wal ak say gannax, lépp a jaare sama kaw.
Bëccëg Aji Sax ji baaxe ma ngoram,
guddi ma fanaane koo woy,
di ñaan Yàlla mi may dundal.
10 Naa wax Yàlla ji ma sës, ne ko:
«Lu tax nga fàtte ma,
noon di ma fitnaal,
may wéye tiis?»
11 Noon yaa ngi may ñaawal,
di ma yendoo naa:
«Ana sa Yàlla ji?»
Ma ne yàcc, ne yasar.
12 Moo man, lu may yoggaaral nii?
Lu may jàq?
Naa yaakaar Yàlla,
ba dellu sante sama Yàlla wallam.