Sabóor 45
Buur a ngi séetal
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bu ñuy wax Tóor-tóor, ñeel askanu Kore wu góor, dib taalif, te di woyu mbëggeel.
 
Woy wu neex a fees sama xol,
may taalifal Buur,
sama làmmiñ ni xalimag bindkatu ndaanaan.
 
Yaa gëna góorayiwe ci àddina,
sa kàddu diw yiw,
ndax Yàllaa la barkeel ba fàww!
Jàmbaaroo, takkal sa saamar,
te yànj, am daraja;
ànd ak daraja, dawal ba am ndam,
di dawal dëgg ak yërmande ji war,
ba mana def ay jaloore.
Yaw Buur, say fitt a ñaw,
di jam say noon ci xol,
ay xeet daanu, nga tiim.
Yaw Yàlla, sab jal a sax dàkk ba fàww.
Njub nga ŋanke sa nguur gi,
di sopp dëgg, bañ lu bon,
ba Yàlla, sa Boroom diwe la diwu mbég,
nga tiim say moroom:
sa yére yépp di gilli ndàbb, alowes akum kanel,
ñu di la bégale xalam,
ca sa biir kër yu yànj.
10 Ay doomi buur a ngi ci jigéen ñi nga teral,
sab lingeer féete la ndijoor,
takkoo ngëneelu wurus.
 
11 Janq doom, gisal, déglul te teewlu ma,
fàtteel say bokk, fàtte sa kër baay,
12 Buur xemmeme la sab taar;
mooy sab sang, wormaal ko.
13 Waa Tir a lay yótsiy may,
ay boroom alal di wut lu la neex.
 
14 Séetu Buur duggsi na, ne ràññ,
sol mbubb mu wurus way tàkk.
15 Ñu yóbbul ko Buur, mu ne boyy,
janq ja ànd ak moom, diy toppam, ñu indil leen Buur,
16 ñu duggsi kër Buur,
ci biir mbégteek bànneex.
 
17 Yal na la sa doom yu góor wuutu ci seen jalu maam,
nga def leeni kàngam ci réew mi mépp.
18 Maa lay joobe ba sa tur du fey mukk,
xeet yi saxoo laa sant ba fàww.