Sabóor 48
Aji Sax ji aar na Siyoŋ
Muy woyu Sabóor, ñeel askanu Kore wu góor.
 
Aji Sax jee màgg, jara màggala màggal
ca sunu biir dëkku Yàlla, kaw tundam wu sell.
Jekk taxawaayee tundu Siyoŋ, catu bëj-gànnaar,
dëkku buur bu mag bi,
di mbégtem àddina sépp.
Yàllaa wone kaaraangeem
ca biir tatay dëkk ba.
 
Buur yaa ngoog daje,
àndandoo.
Nun noo gis, jommi,
tiit, fëx,
ne fay pat-pati,
jàq ni kuy matu.
Ngelawal penku, moom ngay tase
gaal gu mag.
 
La nu déggoon de lanu gis
ca dëkkub Aji Sax ji Boroom gàngoor yi,
sunu dëkku Yàlla ba.
Yàllaa koy dëgëral ba fàww.
Selaw.
10 Céy Yàlla, nu ngi sa biir kër,
di xalaat sa ngor.
11 Céy Yàlla, sa tur ay sa woy
ba ca cati àddina.
Njekk la sa loxo fees.
12 Yal na waa tundu Siyoŋ bég,
waa Yuda bànneexoo say àtte.
 
13 Doxleen biir Siyoŋ, wër ko,
waññleen ay soorooram,
14 nemmikuy tataam,
doxantoo këri buur,
ba man koo yegge maasug ëllëg,
15 ne leen kii ay Yàlla, sunu Yàlla,
tey ak ëllëg.
Moo nuy jiite ba saa taxaw.