Sabóor 6
Jarag a ngi woote wall
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ànd ak xalamu juróom ñetti buum, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.
 
Éy Aji Sax ji, bul mer, ba di ma rëbb,
bul xadaru, ba di ma mbugal.
Aji Sax ji, damaa néew doole, yërëm ma!
Éy Aji Sax ji, sama yaram a tas, dàmp ma!
Sama xol a jeex tàkk.
Aji Sax ji, loo deeti xaar nag?
Éy Aji Sax ji, délsil, xettli ma!
Walloo ma sa ngor.
Deesul dee ba fàttliku la;
ku dugg njaniiw, nu mu lay sante?
 
Onk naa ba loof, di fanaanee jooy,
sama lal di féey,
ba far seeye rongooñ.
Saay gët a ngi xóot ndaxu naqar,
boole ci giim ndax tooñi noonoo noon.
 
Yeen, defkati ñaawtéef yépp, xiddileen ma!
Aji Sax ji dégg na saay jooy,
10 Aji Sax ji dégg na saay dagaan,
Aji Sax jii nangu na samag ñaan.
11 Noon yépp a am gàcce, ba jàq lool,
ne wërëñ ak gàcceg mbetteel.