Sabóor 60
Yàllaa yor sunu mucc
1 Mu jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bu ñuy wax Seedeb Tóor-tóor, di taalifu jàngle, ñeel Daawuda.
2 Mooy ba Daawuda di xareek waa Siri ña ca Mesopotami ak waa Siri ña ca Soba te ba ñu ca bàyyikoo, Yowab duma fukki junniy Edomeen ak ñaar (12 000) ca xuru Xorom wa.
3 Éy Yàlla, wacc nga nu, bëtt sunu kiiraay.
Mer nga, waaye ngalla xettli nu.
4 Yëngal nga suuf, xar ko;
ngalla jagalal, mu tëju, mu ngi jaayu!
5 Won nga sa mbooloo lu metti,
nàndal nu biiñu mbugal, ba nu miir.
6 Artu nga ñi lay jaamu,
ngir mucc fitt.
Selaw.
7 Walloo nu sa ndijoor, nangul nu,
ba say soppe xettliku.
8 Yàllaa àddoo fa këram gu sell,
ne: «Maay damu, dogat suufas Sikem,
séddale xuru Sukkóot.
9 Maa moom diiwaanu Galàdd, moom Manase,
Efrayim di sama mbaxanam xare,
Yuda di sama yetu nguur,
10 réewum Mowab di sama ndabal raxasukaay,
Edom, ma teg tànk;
Filisti, ma xaacoo fa.»
11 Éy Yàlla, ana ku may yóbbu dëkk ba tata wër?
Ku may jiite ba Edom?
12 Xanaa kay du yaw, Yàlla mi nu wacc,
yaw Yàlla, mi baña ànd ak sunu mboolooy xare?
13 Ngalla dimbali nu ci bañaale;
doom aadama, wallam neen la.
14 Nook Yàlla, nu def njàmbaar;
moom mooy not sunuy noon.