Sabóor 64
Yàllaa man ag fitt
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.
 
Éy Yàlla, déglul sama kàddug tawat;
ngalla aaral sama bakkan ci noon bu raglu.
Làq ma pexey ku bon,
ma rëcc gàngooru defkati ñaawtéef.
 
Ñu ngi daas seen làmmiñ niy saamar,
di fitte seeni kàdduy wextan,
di jam ku ñu tëru te deful dara;
jekki jam ko, te tiituñu ci dara.
Dañoo dogu ca lu bon la ñu nar,
di diisoo na ñuy làqe ay fiir,
te naan: «Kenn du ko gis!»
Dañuy lal pexem njubadi te naan:
«Lal nanu pexe mu mat sëkk.»
Nit aka xóot xel te xóoti mbóot!
 
Waaye Yàllaa leen di jamu fittam,
ñu jekki daanu.
Seen làmmiñ a leen di fakkastal,
ba ku leen xool wëcc bopp.
 
10 Ñépp a ciy am tiitaange,
bay siiwal la Yàlla def,
tey xalaataat jëfam jooju.
11 Ku jub bége Aji Sax ji, làqoo ko.
Képp ku namm njub, damu.