Sabóor 68
Yàlla daagu, daan
1 Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ñeel Daawuda, di woyu Sabóor.
2 Yàllaay jóg, noonam ya tasaaroo;
bañam ña daw, dëddu ko.
3 Yàlla wal, ñu naaw ni saxar.
Ñu bon ñi sànku fi kanam Yàlla,
mbete dax ak sawara.
4 Ñu jub ñi nag bég, di bànneexu fi kanam Yàlla,
tey puukarewoo mbégte.
5 Woyleen Yàlla, teral turam,
xàllal-leen kiy war niir yi,
Ki Sax moo di turam.
Bànneexuleen fi kanamam.
6 Mooy baayoo jirim, di àtte jëtun,
kookoo di Yàlla ja fa dëkkuwaayu sellngaam.
7 Yàllaay sàkkal ku wéet wéttal,
di afal ku ñu tëjoon, bégal ko,
ku déggadi rekk ay dëkke suuf su ne sereŋ.
8 Céy Yàlla, yaa génn, jiitu sa mbooloo,
daagu, dugg màndiŋ ma.
Selaw.
9 Suuf yëngu,
asamaan sóob
fi kanam Yàlla, boroom tundu Sinayi,
Yàllay Israyil ja!
10 Yàlla, waame nga tawal,
leqlee ko réew mi nga séddoo, fa mu sonne,
11 sa mbooloo dëkke fa.
Yàlla yaa leel néew-ji-doole ci sag mbaax.
12 Boroom beey joxe ndigal,
gàngooru jigéen indi xibaar:
13 «Buur yaak seeni gàngoor a ngay dawa daw,
jongomay kër gi di séddale lël ja.
14 Yeen ñiy waaf ci gétt gi, bésub xare,
gànjar a ngi, di laafi pitax yu ñu xoob xaalis,
dunq ya teg wurus wuy ray-rayi.»
15 Ba fa Aji Man ji tasaaree buur ya,
tawub yuur a ngay sóobe tundu Calmon.
16 Yaw tundu yàlla yi, yaw tundu Basan,
tundu Basan, tund wi ci coll yi,
17 looy xeelook say coll, di fiire
tund wi Yàlla namma dëkke?
Aji Sax ji kat, fa lay dëkk ba fàww!
18 Watiiri xarey Yàlla di ñaar fukki junni (20 000),
ba ci junniy junni.
Boroom bi ne ca seen biir,
di boroom tundu Sinayi fa biir sellngaam.
19 Yaa yéeg fa kawa kaw,
jàpp ay jaam, yóbbaale.
Yaa nangooy galag ci nit ñi,
ba ci ñiy fippu
ndax li Yàlla Ki Sax dëkke Siyoŋ.
20 Cant ñeel na Yàlla bésoo bés.
Moo nuy jaboote. Yàllaa nuy musal.
Selaw.
21 Sunu Yàllaa di Yàlla jiy walloo,
Aji Sax ji Boroom beey musal bakkan.
22 Yàlla daal ay rajaxe boppi noonam
ak kaaŋ mu sëq mu boroom wéye tooñ.
23 Boroom bi nee: «Basan laay waññee noon yi,
waññee leen xóotey géej,
24 ngeen mana xuus ci seen deret,
seeni xaj séddu ci seeni néew.»
25 Céy Yàlla, gis nañu sa gàngoor di daagu,
sama Yàlla, sama buur, sa gàngoor ba ca biir kër gu sell ga.
26 Woykat ya jiitu, xalamkat ya mujje,
janq ji yéewe leen tëgg um njiin.
27 Dajeleen, di sant Yàlla,
yeen askanu Israyil, santleen Aji Sax ji.
28 Giirug Beñamin a ngi jiitu, gën cee néew,
njiiti Yuda topp caak seeni kurél,
njiiti Sabulon topp caak njiiti Neftali.
29 Yeen, seen Yàlla dogalal na leen kàttan;
éy Yàlla, jëfeel doole ja nga nu jëfeeloon.
30 Sa kër gi tiim Yerusalem,
fa la la buur yiy indiley galag.
31 Nanga fa gëdde rabu àll wi ci barax yi,
ñooy gétti yëkk yi, xeet yi ci des diy sëllu.
Gëdd leen, ba ñu sujjóotalsi laak dogi xaalis.
Tasaareel xeet yooyu sopp xare,
32 ay kàngam bàyyikoo Misra aki galag,
réewum Kuus baral loxoom, indil Yàlla.
33 Yeen waa réewi àddina, woyleen Yàlla,
teral-leen Boroom bi,
Selaw
34 gawar bi ci asamaan,
asamaani démb.
Ma ngooguy àddu kàddug doole.
35 Seedeleen ne doole, fa Yàlla,
mi tiime Israyil darajaam,
dooleem feeñoo xàmbaar ya.
36 Céy Yàllaaka mata ragal fa këram gu sell!
Mooy Yàllay Israyil,
di may mbooloo mi dooleek kàttan.
Cant ñeel na Yàlla!