Sabóor 76
Yàllaa moom xare
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ànd aki xalam, di woyu Sabóor, giiroo ci Asaf.
 
Yàlla siiw na fa Yuda,
aw turam màgg fa Israyil.
Xaymaam a nga Salem,
di xunteem ma fa Siyoŋ.
Fa la rajaxee fitt yuy boy
ak pakk ak saamar ak ngànnaayal xare.
Selaw.
 
Yàlla yaa ne ràññ te darajawu,
ba raw tundi rëbbkat yi.
Futtees nay boroom fit,
ñu ne nërëm, nelaw;
kuy ñeyi xare, say yoxo nasax.
Yaw Yàllay Yanqóoba, yaa gëdd,
gawar ak fasam nelaw.
Yaw mii, yaa mata ragal;
boo meree, ana kuy taxaw fi sa kanam?
Fa asamaan nga biraleb àtte;
suuf tiit, ne cell.
10 Ca la Yàllay jóg, ngir àtte,
ba wallu kuy néew dooley àddina.
Selaw.
11 Doom aadamaak xadaram rafetal sa woy;
desu xadaram, nga gañoo.
 
12 Seen Yàlla Aji Sax ji, digooleen ak moom
te jëfe ko.
Kee jara ragal.
Na ñi ko wër ñépp yótsiy teraanga.
13 Mooy sàggi sagu kilifa yi,
di tiitaangey buuri àddina.