Sabóor 86
Ma ñaan, bésub njàqare
Mu di ñaanu Daawuda.
 
Éy Aji Sax ji, teewlu ma, nangul ma,
damaa ñàkk, néew doole.
Maa gore, musal ma;
maay sa jaam bi la wóolu,
yaw, sama Yàlla, wallu ma.
Éy Boroom bi, baaxe ma;
yaw laay yendoo woo wall.
Boroom bi, bànneexalal sab jaam,
yaw laa dékk sama xol.
Boroom bi, yaa baax, di bale,
di nàddil sa ngor képp ku lay sàkku.
Éy Aji Sax ji, teewlul, ma ñaan la;
déglul, ma tinu la.
Bu ma la wooyee bésub njàqare,
yaa may nangul.
 
Boroom bi, doo moroomu tuur yi,
te jëf melul ni sa jos.
Boroom bi, mboolem xeet yi nga sàkk
ñoo lay sujjóotalsi,
di màggal sa tur.
10 Yaa màgg te yéemey jëf,
yaw doŋŋ yaa di Yàlla.
11 Éy Aji Sax ji, won ma sa nammeel,
ma doxe sa worma.
Tënkal sama xol ci ragal la.
12 Boroom bi sama Yàlla,
naa la sante xol bu fees,
màggal la ba fàww.
13 Ngor lu réy nga ma won,
sorele maak tëraayu bàmmeel.
 
14 Éy Yàlla, nit ñu bew a ma jógal,
def gàngoor gu néeg, di rëbb sama bakkan,
te seetuñu la ci.
15 Waaye yaw Boroom bi Yàlla, yaa ñeewante, yërëm,
yaa muñ mer, bare ngor ak worma.
16 Geesu ma, baaxe ma.
Dooleelal sab jaam,
wallul ki sa jaam sukk jur!
17 Ngalla def ma sa firndey mbaax,
ba bañ yi gis ci, rus,
ndax yaw Aji Sax, ji ma dimbali, dëfal ma.