Sabóor 95
Kaayleen, nu sant
1 Kaayleen, nu sarxolleel Aji Sax ji,
nu xaacul ki nuy sës, mucc.
2 Nanu ko dikke cant,
woyal ko, mu riir.
3 Aji Sax jeey Yàlla ju màgg ji,
buur bu mag bi tiim yàllay xeet yépp.
4 Moo moom xóotey suuf,
moom colli tund yi,
5 moom géej, sàkk ko,
moom jéeri ji mu mooñ.
6 Nan sëgg, sujjóot,
sukkal Aji Sax ji nu sàkk.
7 Mooy sunu Yàlla,
nuy xeet wi muy foral,
diy gàtt ciy loxoom.
Bésub tey yal nangeen dégg kàddoom
8 ga mu noon: «Buleen të, na woon fa Meriba,
jantub keroog fa Maasa, ca màndiŋ ma,
9 fa ma seeni maam doon nattoo,
di ma seetlu te gis la ma def.
10 Ñeent fukki at laa jéppi googu maas,
ma ne: “Xeet wu ñàkk wormaa ngi,
te faaleedi samay santaane.”
11 Moo ma taxa mer, ba giñal leen,
ne duñu tàbbi fa sama noflaay.»