Sabóor 98
Woyleen Aji Sax jiy àttesi
Muy kàddug Sabóor.
 
Woyleen Aji Sax ji woy wu yees,
moo def ay jaloore,
kàttanam ak sellngay dooleem
jox na ko ndam li.
Aji Sax jee xamleg wallam,
feeñal njekkam, xeet yi gis.
Moo dencal bànni Israyil ngoram,
dencal ko wormaam,
àddina ba mu daj di gis
ni nu sunu Yàlla walloo.
Yeen àddina sépp, xaacul-leen Aji Sax ji,
sampleen, sarxolle te woy!
Xalamal-leen Aji Sax ji, woyal ko,
xalamal ko, woyati.
Wal-leen liit yi, wal bufta yi
te xaacul Buur Aji Sax ji!
 
Na géej riirandook li ko fees,
mook àddinaak li ci biiram,
dex tàccu,
tund sarxolleendoo,
gatandoo ko Aji Sax jiy dikk,
àttesi àddina,
di àtte dun bi njekk,
tey àttee xeet yépp dëgg.