10
Bokk yi, sama yéeney xol, ak ñaan gi may ñaanal Israyil ci Yàlla moo di ñu mucc. Ñoom laa seedeel seenug parlute ci Yàlla, waaye dañu koo tegul ci xam-xam bu doy. Yoonu njub gi Yàlla di joxe nit ki, àtteb ku jub, moom lañu umple tey jéema dëggal seen njubteg bopp. Moo tax nanguluñu njubte gi Yàlla di maye. Ndax kat Almasi moo sottal yoonu Musaa, ngir àtteb ku jub ñeel képp ku ko gëm.
Coobarey Yàlla mooy ñépp mucc
Njub gi sàmm ndigali yoon di maye, li ci Musaa bind moo di: «Kuy jëfe digal yooyu, yaay dund ndax ñoom* Waaye njub, gi ngëm di maye, li muy digle mooy:
«Bul wax ci sa xel, ne: “Ana kuy yéeg fa kaw?”»
nde loolu mooy Almasi wàcc ngay sàkku.
«Bul ne it: “Ana kuy wàcci njaniiw?”»
nde loolu mooy Almasi dekkiwaat ngay sàkku. Li mu wax moo di:
«Kàddu gaa ngi ci sa wet; mu ngi ci saw làmmiñ ak ci sa xol
Te loolu mooy kàddug ngëm gii nuy xamle. Saw làmmiñ, soo ci biralee ne Yeesu moo di Boroom bi, sab xol it, nga gëm ci ne Yàlla dekkal na Sang Yeesu, dinga mucc. 10 Ndax kat ab xol lees di gëme, ba am àtteb ku jub, te aw làmmiñ lees di birale ngëm gi ba mucc. 11 Mbind mi moo ne: «Képp ku ko gëm, doo rus 12 Ag wuutale amul diggante ab Yawut, ak jaambur bu dul Yawut; ñépp a bokk benn Boroom biy yéwéne mboolem ñi koy woo wall. 13 Ndax kat waxees na ne: «Képp ku woo Boroom bi wall ciw turam, mooy raw§
14 Waaye nees di wooye koo gëmul? Nees di gëme koo déggul turam? Nees di dégge turam, te yégleesu ko? 15 Nees di yéglee xibaar, te yebaleesu la? Noonu la Mbind mi indee ne: «Ñeeka rafeti tànk, ndaw yii di yéglesi xibaari jàmm*
16 Waaye du ñépp a nangul xibaaru jàmm bi; moo tax Esayi ne: «Boroom bi, ana ku gëm sunub dégtal 17 Kon boog ngëm ci dég-dég lay juddoo, dég-dég ba bawoo ci kàddug waare gi jëm ci Almasi.
18 Waaye dama ne: xanaa dañoo déggul? Ahakay! Ndax
«Àddina sépp la seen baat jibal,
cati suuf sépp la seen kàddu dajal
19 Ma neeti: xanaa bànni Israyil dañoo xamul? Ahakay! Musaa moo leen jëkkoona jottli la Yàlla noon:
«Yeen, maa leen di fiireloo xeet wu tekkiwul dara,
ci waasow naataxuuna laa leen di merloo§
20 Esayi it am fit ba ne:
«Ñi ma seetul woon, gis nañu ma,
ca ña ma laajul woon laa feeñe*
21 Israyil nag la wax ci mbiram ne:
«Bëccëg bépp laa yendoo tàllal samay loxo,
askanu fippukat wu déggadi
* 10:5 Seetal ci Sarxalkat yi 18.5. 10:8 Seetal ci Baamtug Yoon wi 9.4; 30.12-14. 10:11 Seetal ci Esayi 28.16. § 10:13 Seetal ci Yowel 3.5. * 10:15 Seetal ci Esayi 52.7. 10:16 Seetal ci Esayi 53.1. 10:18 Seetal ci Sabóor 19.5. § 10:19 Seetal ci Baamtug Yoon wi 32.21. * 10:20 Seetal ci Esayi 65.1. 10:21 Seetal ci Esayi 65.2.