8
Noowug Yàlla moo jiite gëmkat bi
1 Kon nag léegi, amul benn daan bu ñeel ñi bokk ci Almasi Yeesu.
2 Ndax kat, dooley Noo giy maye bakkan te nekk ci Almasi Yeesu moo la yiwi, ba nga mucc ci dooley bàkkaar ak ndee.
3 Li yoonu Musaa tële woon ndax néew dooley nitu suuxu neen, mooy lii Yàlla def: Doomam la yónni, mu dikke melow nit, te nit di bàkkaarkat, di suuxu neen, ngir Doomam fajtal mbirum bàkkaar. Yaramu suux wu nit kooku la Yàlla sottale mbugal gi war ci bàkkaar,
4 ngir njub gi yoonu Musaa laaj mana sotti ba mat sëkk ci nun, ñi toppatul sunu bindu suux, xanaa Noowug Yàlla.
5 Ndax kat ñi topp seen bindu suux, mbiri bakkan doŋŋ lañu xinte, waaye ñi topp Noowug Yàlla ñoom, mbiri Noowug Yàlla mooy seen xinte.
6 Xintey bakkan nag ci ndee lay jëme, waaye xintey Noowug Yàlla ndund ak jàmm lay jur.
7 Ndaxte boroom xintey bakkan ab noonu Yàlla la, nde déggalul yoonu Yàlla, te manu ko sax.
8 Moo tax ñi wéye seen bindu suuxu neen duñu mana neex Yàlla.
9 Yeen nag nekkatuleen ci kilifteefu bindu suuxu neen, waaye ci kilifteefu Noo gi ngeen nekk, ndegam kay Noowug Yàllaa ngi màkkaanoo ci yeen. Ku amul Noowug Almasi, kooku du nitam.
10 Su Almasi nekkee ci yeen, seen yaram dina dee moos ndax bàkkaar, waaye du tee seenug noo di dund, ndax àtteb njub bi ngeen am ba noppi.
11 Noowug ki dekkal Yeesu moo màkkaanoo ci yeen. Kon nag ki dekkal Almasi mooy dekkal itam seen yarami ndee, ndax Noowam googu màkkaanoo ci yeen.
12 Kon nag bokk yi, bor topp na nu, waaye du sunu bindu suux lanu ameel lenn lu nu taxa topp sunu bakkan;
13 Ku topp bakkanam, fàww mu dee, waaye ku rey jëfi yaramam ci ndimbalal Noowug Yàlla, dina texe.
14 Ndax kat, mboolem ñiy dox ci njiital Noo gi, ñooñu ay doomi Yàlla lañu.
15 Mayeesu leen noo gu leen di desloo cig njaam, ba tax leena dellu cig ragal, waaye Noowug doom yu ñu doomoo, moom lees leen may, te looloo nu tax di wooye Yàlla: «Abba», mu tekki «Baay.»
16 Te Noowug Yàlla, moom ci boppam, moo mànkoo ak sunu noowug bopp, di seede ne ay doomi Yàlla lanu.
17 Gannaaw ay doom lanu nag, ay boroom cér lanu, ay boroom cér yu Yàlla sédd, cér yu nu bokk ak Almasi, gannaaw noo bokk ak moom ab coono tey, ngir bokk ak moom teraangay ëllëg.
Teraangay ëllëg ñeel na gëmkat ñi
18 Jàpp naa ne sunu coonob tey du dara, soo ko xoolee ci teraanga ji ñu nuy feeñalal ëllëg.
19 Càkkéefu àddinaa ngi séentu, ndax yàkkamti bés ba doomi Yàlla di feeñ.
20 Ndax kat, càkkéef gépp, li ñuy déggal neenug neen la, te du seen coobare, waaye ki leen ci tënk la neex, ba tax ñuy yaakaar,
21 ñoom ñi bokk ci càkkéef googu itam, ne dees na rengi seen buumi njaam gi leen ndee ak yàqutey yaram ràng, ngir ñu am cér ci goreelug doomi Yàlla yi, am cér ci seen teraanga.
22 Xam nanu ba fii nu tollu ne mboolem càkkéef gaa ngi binni ndax mitit, ni kuy matu.
23 Te du càkkéef gi rekk, waaye nun ci sunu bopp itam, ci lanu, nun ñi jot ab dawal ci Noo gi, nun ci sunu bopp sax nu ngi binni sunu biir xol, ndax yàkkamtee jot céru doomi Yàlla, ba sunu njotug yaram mat.
24 Ndax kat sunu mucc, yaakaar la taxaweegum, te yaakaar joo teg sa bët, dootu yaakaar. Li nit ki teg bëtam, nu mu koy yaakaaratee?
25 Li nu gisul kay lanuy yaakaar, di ko séentook a muñe yaakaar ji.
26 Te itam Noo gi moo nuy dimbali ndax sunug néew doole, nde xamunu sax li jaadoo sàkku ci sunuy ñaan, waaye Noowug Yàlla moo nuy tinule ay onk yu wees kàddug làmmiñ.
27 Te kiy xool li ci biir xol yi, xam na liy xintey Noo gi, nde ni ko Yàlla bëgge, ni la Noo giy tinool ñu sell ñi.
28 Te itam nag xam nanu ne Yàlla mooy def mboolem lu xew, daje ba jur njariñal ñi sopp Yàlla, ñi mu woo, noonee ko ab dogalam namme.
29 Ndax ñooñu Yàllaa leen ràññee woon lu jiitu, te it la mu dogaloon lu jiitu ci ñoom moo di ñu niru Doomam, ngir Doomam di taaw, ci biir rakk yu bare.
30 Ñi Yàlla tuddaloon loolu lu jiitu, moo leen woo itam; ñooñu mu woo, moo leen jox itam àtteb ñu jub; te ñooñu mu jox àtteb ñu jub, moo leen darajaal itam.
Cofeelu Yàllaa ngi ci Almasi
31 Ana lu nuy waxati nag? Gannaaw Yàllaa ànd ak nun, ku nu manal dara?
32 Moom mi nu bañalul Doomu boppam, xanaa jooxeel nu ko, nun ñépp, ana nu mu nuy baña baaxee gépp yiw, boole ci?
33 Ñi Yàlla taamu, ana ku leen di tuumaal? Yàlla de mooy jox nit àtteb ku jub.
34 Ana kuy tegeb daan? Almasi Yeesu de moo dee, rax ci dolli, mu dekki, te moo toog fa ndijooru Yàlla, di nu fa ñaanal!
35 Ana ku nuy tàggaleek cofeelu Almasi? Du ay nattu, te du njàqare, du it coonoy bundxatal, mbaa ab xiif, mbaa rafle, te du genn aaytéef, ba cib saamar.
36 Noonu la Mbind mi indee ne:
«Yaa tax ñu yendu noo bóom,
dees noo jàppe ni xar yu ñuy tër.»
37 Waaye ci mboolem lu nu dikkal, nooy am ndam lu mat sëkk, ci ndimbalal ki nuy soppeem.
38 Ndax kat bir na ma ne du ag ndee, du ag ndund, du ay malaaka, duy boroom nguur, du tey, du ëllëg, duy boroom doole,
39 du lu kawe, du lu xóot, mbaa meneen mbindeef mu mu doon; dara manu noo tàggale ak cofeel, gi nu Yàlla won ci Almasi Yeesu sunu Sang.