2
Ruut gis na ku ko baaxe
Nawmi nag amoon na wóllërey jëkkëram, di góor gu ñuy wax Bowas, bokk ci làngu Elimeleg, di ku am daraja.
Mu am bés Ruut, ndawas Mowab sa, ne Nawmi: «Tee maa dem tool, ndax ma gis boog ku ma laaye biir, ma mana foraatu gub yu des ca gannaawam?» Mu ne ko: «Waaw, demal, doom.» Mu dem ca tool ya, topp ñay góob, di foraatu. Yàlla-woo-yàlla, tool booba di toolu Bowas ma bokk ak Elimeleg.
Nes tuut Bowas ne jalañ, jóge Betleyem. Mu nuyook ñay góob ne leen: «Jaagéenjëf waay, yal na Aji Sax ji ànd ak yeen.» Ñu fey ko ne ko: «Jaajëf sa wàll, yal na la Aji Sax ji barkeel.» Mu laaj ka jiite ngóob ma, ne ko: «Ndaw sii fu mu bokk?» Mu ne ko: «Mooy waa Mowab, ba Nawmi àndal, jóge Mowab, ñibbsi. Dafa ñaan ñu may ko, mu topp ci ñiy góob, ba saatu ci gub yi ñu rotle. Ci suba la ñëw di liggéey ba nëgëni; noppluwul lu moy diir bu gàtt ci mbaar mi.»
Bowas nag ne Ruut: «Doom, ma ne, bul saatuji ci beneen tool bu dul bii. Bul wees fii. Toogal fii ci samay surga yu jigéen. Xoolal bu baax fi xale yu góor yiy góob, te nga topp fa jigéen ñi. Dinaa wax xale yu góor yi ne leen buñu la sonal. Soo maree, demal naan ca njaq ya góor ñi duy.»
10 Naka la wax loolu, mu sujjóot, dëpp jëëm fa suuf, ne ko: «Xanaa su la neexoon de, doo ma nemmiku sax, ndax ab doxandéem laa, waxatuma nga di ma laaye nii biir!» 11 Mu ne ko: «Dégg naa bu baax li nga defal sa goro lépp, te fekk sa jëkkër faatu, ak ni nga wone gannaaw sa ndey ak sa baay ak sa réewum cosaan, ba ñëw dëkksi ci biir xeet woo xamuloon démb ak bëkk-démb. 12 Yal na la Aji Sax ji fey sa jëf. Aji Sax ji Yàllay Israyil, ji nga làqusi ci kiiraayam, yal na la yool, ba mu mat sëkk.»
13 Ruut ne ko: «Teral nga ma de, sang bi. Yaa ngi may laaye biir, ndaxte dëfal nga ma, wax ma lu seral sama xol, te moona say surga yu jigéen yi sax a ma gën.»
14 Ba añ jotee, Bowas ne Ruut: «Kaay, sàkk ci mburu mi ak ñeex mi.» Mu daldi toog, feggook ñay góob; Bowas may ko mbool, mu lekk ba suur, ba desal.
15 Naka la jóg, di saatuji, mu sant ay surgaam, ne leen: «Bu doon for ci biir sabaar yi sax, buleen ko ñàkke kersa. 16 Roccil-leen koo roccil ci takk yi, bàyyi ko mu for, te buleen ko gëdd.»
17 Ba loolu amee, Ruut di for ba ngoon jot, mu bàcc la mu for ci peppum lors, mu fees saaku bu ndaw. 18 Mu yóbbu ko ba ca dëkk ba, goroom gis la mu for, mu daldi yebbi la desoon ca añam, jox ko. 19 Goro ba ne ko: «Foo fore lii lépp tey? Ban tool nga doon liggéeye sax? Ki la nemmikoo nii de, yal na barkeel!» Ruut nag wax goroom ka mu doon liggéeye toolam, ne ko: «Ka ma doon liggéeye toolam de, Bowas lañu koy wax.»
20 Nawmi ne Ruut: «Yal na Aji Sax ji barkeel Bowas, moom mi saxoo sàmm ngoram digganteem ak nit, muy dund ak mu dee!» Mu teg ca ne ko: «Kooku ku nu jege la; bokk na ci ñi am sañ-sañu jotaat* nu.» 21 Ruut ndawas Mowab sa ne: «Moom de da ma ne sax, ma topp ciy surgaam, ba ngóobam mépp daj.» 22 Mu ne ko: «Waaw kay, doom, toppal ci surgay Bowas yu jigéen rekk, bala ñu laa soxore ci beneen tool.» 23 Noonu la Ruut ànde ak surgay Bowas yu jigéen, topp ci ñoom di for, ba keroog ngóobum lors baak bele ba, lépp jeex. Mu toog nag ak goroom.
* 2:20 jotaat: bu góor masaana dee te amul doom, mbokkam mi ko gëna jege mooy jël jabaram, ngir jural ko ku ko donn. Kooku mooy jotaat suufi mbokkam mi dee, jënd ko, ngir alal ji des ci biiri bokkam.