11
Sóol jéngu na
1 Nayas Amoneen ba moo dikkoon, gaw dëkk ba ñu naan Yabes ca Galàdd. Waa Yabes gépp wax ak moom, ne ko: «Ngalla digool ak nun jàmm, te nu nangul la.»
2 Nayas Amoneen ba ne leen: «Ni may digook yeen daal, mooy nii: luqi seen bëtu ndijoor yeen ñépp, ba Israyil gépp torox.»
3 Magi Yabes ne ko: «May nu juróom ñaari fan, nu yebal ay ndaw ci Israyil gépp. Su amul kenn ku nu wallu, nu dikk, fekksi leen.»
4 Ba ndaw ya dikkee Gibeya, ga Sóol dëkk, ba xamle mbir ma, waa dëkk ba di dégg, ñoom ñépp a yuuxu, di jooy.
5 Ci biir loolu Sóol ne tëll, jiital ay nagam, jóge tool ya. Mu ne: «Lu nit ñi xewle bay jooy nii?» Ñu nettali ko kàdduy waa Yabes.
6 Naka la Sóol dégg kàddu yooyu, Noowug Yàlla ne milib ca kawam, mer ma ne jippét tàkk.
7 Mu rey ñaari nag, dog ko, yóbbante ko ay ndaw, yónnee ko Israyil gépp. Mu ne leen: «Képp ku toppul Sóol ak Samiyel, nii lees di def ay nagam.» Ba loolu amee tiitaange ju sababoo ci Aji Sax ji dal ca kaw askan wa, ñu sàqeendoo, di benn bopp.
8 Ba Sóol nemmikoo limu góori Israyil ca Beseg, ñetti téeméeri junni lañu (300 000), waa Yuda di fanweeri junni (30 000).
9 Ñu wax nag ndaw ya jóge Yabes Galàdd, ñu jottli seen waa dëkk ba ne leen, ca ëllëg sa bu jant bi tàngee, dees na leen wallu. Ndaw ya dem, àgge ko waa Yabes, waa Yabes bég.
10 Ñu wax Amoneen ña, ne leen: «Ëllëg dinanu dikk, fekksi leen.»
11 Ca ëllëg sa Sóol séddale mbooloom xareem ñetti kurél. Ba ñu tolloo ci wattub njël, ñu dugg biir dalu Amoneen ña, di leen duma ba jant bi tàng. Ña ca rëcce daldi tasaaroo ba ñaar sax àndatuñu.
12 Mbooloo ma ne Samiyel: «Ana ku noon: “Ndax Sóol ay falu ci sunu kaw?” Indileen ñooñu, nu rey leen!»
13 Sóol ne leen: «Deesul rey kenn kay bésub tey jii, ndax bésub tey Aji Sax jee indi wall fi Israyil.»
14 Ci kaw loolu Samiyel ne mbooloo ma: «Ñëwleen nu dem Gilgal, ba feddli pal gi.»
15 Mbooloo ma mépp dem Gilgal, ñu fal Sóol buur foofa, fa kanam Aji Sax ji ca Gilgal. Ñu sarxe fa saraxi cant ci biir jàmm fa kanam Aji Sax ji, Sóol ak bànni Israyil gépp bànneexoo fa bànneex bu réy.