31
Lu jëm ci mujug Sóol
Ci biir loolu waa Filisti jaamarloo ak Israyil, ba bànni Israyil won leen gannaaw, daw, ñu bare daanu ca kaw tundu Gilbowa. Waa Filisti nag ne dann Sóol aki doomam, ba rey ca ñett; Yonatan ak Abinadab ak Malkisuwa. Xare ba nag gëna mettee fa Sóol féete, fittkat ya jekku ko, mu jàq.
Ba loolu amee Sóol ne gàddukatu gànnaayam: «Boccil sa saamar, jam ma bala yéefar yee dikk, jam ma, torxal ma.» Gàddukatu gànnaayam nag buggu koo jam ndax tiitaange lu réy. Sóol jël saamaru boppam, daldi daaneel boppam ca kaw ñawka ga. Gàddukatu ngànnaay ba gis ne Sóol dee na, moom it mu daaneel boppam ca kaw saamaram, dee topp Sóol. Muy Sóol, di ñetti doomam, di gàddukatu gànnaayam itam, di mboolem ay nitam, ñoom ñépp a bokk dee bésub keroog.
Ci kaw loolu bànni Israyil, ya ca wàllaa xur wa, ak ña ca wàllaa dexu Yurdan gis ne xarekati Israyil daw nañu, te Sóol aki doomam dee nañu. Ñu daldi daw, gental seeni dëkk, waa Filisti dikk, dëkke.
Ca ëllëg sa, ba waa Filisti dikkee, di futtisi ña dee, ca tundu Gilbowa lañu fekk Sóol ak ñetti doomam, ñu tëdd. Ñu dog boppu Sóol, jël ay gànnaayam, ba noppi yeble ca réewum Filisti ba mu daj, ngir yégle ko ca seen këri tuur ya ak ca askan wa. 10 Ba mu ko defee ñu denc gànnaayi Sóol ca seen biir kër tuur ma ñuy wax Astàrt, néewub Sóol, ñu wékk ca miiru dëkk ba ñuy wax Bet San.
11 Ba waa Yabes ga ca Galàdd déggee la waa Filisti def Sóol, 12 seen jàmbaar yépp a fabu, topp guddi ga gépp ba Bet San. Ñu wékkee ca miiru Bet San néewu Sóol ak néewi doomam yu góor, doora ñibbi Yabes, boole fa néew ya, lakk. 13 Ñu for nag seeni yax, suul ca ron garabu tamaris ga ca Yabes. Ba loolu amee ñu woor diiru juróom ñaari fan.