15
Absalom lal na pexe
Gannaaw ba loolu wéyee Absalom daa jël watiir aki fas ak juróom fukki nit ñuy daw di ko jiitu. Muy teela jóg nag, taxaw ca peggu yoon, wa jëm ca buntu dëkk ba. Saa yu nit dikkee, am lu muy tawat, di ko diis-si Buur, ngir mu àtte ko, Absalom woo ko, laaj ko ne ko: «Ci ban dëkk nga bokk?» Kooku ne ko ci giirug Israyil sàngam la bokk. Absalom ne ko: «Gisal, sa tawat yoon la, jaadu na. Waaye kenn ku bokk ci Buur du la déglu.» Su ko defee Absalom da cay teg ne ko: «Maa bëggoon ñu fal ma njiit, may àtte ci réew mi! Kon képp ku am lu muy tawat mbaa muy layoo, ci man lay ñëw, ma taxaw ci, ba jox ko li ko yoon may.» Képp ku ñëwaan it di sukkal Absalom, Absalom da koy yóotu, jàpp ci moom, fóon ko. Absalom jàppoo ko noonu ak mboolem bànni Israyil yay ñëw ca buur ba, di sàkku yoon. Ni la fàbbee xoli bànni Israyil.
Ba ñu demee ba ñeenti at* jàll, Absalom ne Buur: «May ma, ma dem Ebron defali Aji Sax ji la ma ko xasaloon, ndax kat, sang bi, ba ma nekkee Gesur ca Siri, damaa dige woon ne: “Su ma Aji Sax ji delloo, ba ma dellu Yerusalem, dinaa dem màggali ko.”» Buur ne ko: «Demal ak jàmm.» Mu daldi dem Ebron.
10 Absalom nag yónnee ndéey. Ay ndaw yegge ko giiri Israyil gépp. Mu ne leen: «Bu ngeen di dégg liit gu jib rekk, ne leen: “Absalom falu na buur ca Ebron!”» 11 Ñaar téeméeri góor a jóge Yerusalem, Absalom woo woon leen, ñu ànd ak moom, yéguñu, tinuñu, xamuñu it dara ca mébétam. 12 Ci biir loolu Absalom di def ay sarax, daldi yónnee, ñu jëli Ayitofel ma topp ca Daawuda, di ko xelal. Ayitofel bàyyikoo ca Gilo. Pexe ma nag mujj na réy, ña topp Absalom di yokku ba bare.
Daawudaa ngi wuta rëcc
13 Ba mu ko defee ñu yebal ndaw, mu dikk ne Daawuda: «Bànni Israyil de jàmbu nañu, ba far ak Absalom.» 14 Daawuda wax ak mboolem jawriñam ya mu nekkal ca Yerusalem, ne leen: «Nan daw! Lu ko moy kenn ci nun du rëcc Absalom. Nan dem léegi bala moo gaawtu, ba dab nu, def nu musiba, leel waa dëkk bi ñawkay saamar.» 15 Jawriñ ya ne Buur: «Buur, sang bi, lépp loo namm rekk, nu ngi nii taxaw.» 16 Ba loolu amee Buur tegu ca yoon wa, waa këram yépp topp ciy tànkam. Bàyyiwul gannaaw lu moy fukki nekkaaleem, ñu wara topptoo kër ga.
17 Buur dem, mbooloo mépp topp ko, ba ca kër gu mujj ga, ñu taxaw. 18 Nitam ñépp a dox romb ko, ñook dag ya ko dar yépp, di waa Keret ñaak waa Pelet ña, ak mboolem waa Gaat ya tollu ci juróom benni téeméeri nit te toppe woon ko ca Gaat. Ña ngay dox jiitu ko.
19 Buur ne Itay waa Gaat ba: «Dangay ànd ak nun? Tee ngaa dellu Yerusalem, toog ca Buur Absalom? Gannaaw yaw doxandéem nga bu gàddaaye fa nga fekk baax. 20 Bëkk-démb doŋŋ nga fi ñëw, tey ma di la bàyyi ngay ànd ak nun di wëreelu, te xawma sax fu ma jëm. Dellul, kay, ànd ak sa waa réew. Yal na la Aji Sax ji won ngor ak worma.»
21 Itay ne Buur: «Sang bi, giñ naa ci Aji Sax ji, Kiy Dund, nga fekke tey, fépp foo jëm yaw Buur, sama sang, dinaa fa ànd ak yaw, su may dund ak su may dee.» 22 Daawuda ne Itay: «Kon doxal jiitu.» Itay jiitu, mook nitam ñépp ak mboolem njabootam.
23 Mbooloom Daawuda mépp a ngay dem, waa réew ma mépp taxaw di yuuxook a jooyoo. Buur ba jàll xuru Sedoron, mbooloo ma mépp ànd wuti màndiŋ ma.
24 Cadog ak Abiyatar, sarxalkat yaa nga fa woon, ñoom itam. Ñenn ca góori Leween ña bokkoon nañu ca, di gàddu gaal ga àlluway kóllërey Yàlla ga dence. Ba ñu tegee gaal ga, Abiyatar di rendi ay sarax, ba mbooloo ma mépp génn dëkk ba. 25 Buur ne Cadog: «Dellool gaalu Yàlla gi ca dëkk ba. Bu ma Aji Sax ji baaxee, dina ma délloosi, ma gisaat gaal gi, gisaat fi mu dëkk. 26 Waaye bu ma waxee ne ma bégul ci man, su boobaa ba tey maa ngi. Na def li ko soob ci man.» 27 Buur dellu wax ak Cadog sarxalkat ba, ne ko: «Dégg nga déy? Dellul ak jàmm ca dëkk ba, ànd ak Ayimaas, sa doom ju góor, ak Yonatan doomu Abiyatar. Yaak Abiyatar àndleen ak seen ñaari doom yu góor. 28 Xoolal, dinaa leen xaar ca jàllukaayu dex ba ca yoonu màndiŋ ma, ba keroog may dégg kàddu gu bawoo ci yaw.» 29 Ba loolu amee Cadog ak Abiyatar delloo gaalu Yàlla ga Yerusalem, daldi fay toog.
30 Daawudaa ngay wéy, di yéeg tundu Oliw ya, tey jooy. Ma nga muuru, def tànki neen ndaxu naqar. Nit ña mu àndal ñépp muur seen bopp ñoom it, di yéeg tey jooyoo. 31 Fekk na ñu wax Daawuda ne ko Ayitofel bokk na ca ña lëngook Absalom. Daawuda nag ñaan ne: «Yaw, Aji Sax ji, ngalla yàqal pexem Ayitofel.»
32 Ba Daawuda àggee ca collu tund wa, fa ñu daan jaamoo Yàlla, fekku fa ku moy Usay, Arkeen ba. Mu gatandu ko. Ma ngay tiislu, mbubb ma xottiku, bopp ba pënd. 33 Daawuda ne ko: «Soo àndee ak man, danga may diisal rekk. 34 Dangay dellu kay ca dëkk ba, ne Absalom: “Buur, sab jaam laa. Sa jaamu baay laa woon, waaye léegi sab jaam laa.” Noonu nga may yàqale pexem Ayitofel. 35 Te sax Cadog ak Abiyatar, sarxalkat ya, nga fay bokk nekkal. Loo dégg kër Buur, wax leen ko. 36 Te sax seen ñaari doom yu góor a nga faak ñoom: Ayimaas doomu Cadog, ak Yonatan doomu Abiyatar. Yónnee ma leen, ñu yegge ma loo dégg.» 37 Ci kaw loolu Usay, nitu Daawuda, yoxoosu, duggsi Yerusalem, yemook Absalom itam di agsi.
* 15:7 ñeenti at yi ñuy wax fi am na ñu ne man naa doon ñeent fukki at.