2
1 Waaye man saxayaayu joor doŋŋ laa,
nirook as tóor-tóor ciw xur.
Waa ji
2 Xanaa as tóor-tóor su ne ràññ ci biiri dég!
Kookooy sama xarit ci biir janq ji.
Ndaw si
3 Mbete garab gu gëna neex ci gott bi,
kookooy sama nijaay ci biir xale yu góor yi.
May bége keppaaram, safoo doom ya.
4 Dugal na ma néegub sago-jeex-na,
yiire ma mbëggeel.
5 Gaaweleen ma nàkki reseñ, ma dëgër,
leel-leen may meññeef, leqlee ma.
Wopp laa def ndax mbëggeel!
6 Sama càmmoñu waay, ma gegenoo,
ndijooram, ma laxasoo.
7 Yeen janqi Yerusalem, waatal-leen ma
ci taaru kéwél ak koobay àll bi,
ne dungeen dakkal te dungeen sooke tëraayu mbëggeel
te jotul.
Wootante jib na
Ndaw si
8 Dégluleen, sama nijaay a,
mu ngooguy ñëw,
di xéluy jéggi tund yu ndaw yi,
di tëb tund yu mag yiy dikk.
9 Sama nijaay a ngi mel ni kéwél,
mbaa kooba gu ndaw.
Mu ngi noonu taxaw ca gannaaw miir ba,
di séentu ci palanteer bi
ak a yër ci caax bi.
10 Sama nijaay ne ma:
«Xarit, ayca,
jongama sama, dikkal boog!
11 Xoolal, tawub sedd wees na,
waame jàll, wéy.
12 Tóor-tóor yi lal na réew mi,
jamonoy woy dikk,
sabum pégét jibe sunum réew.
13 Figg a ngi ñorsi,
reseñ tóor, di gilli.
Xarit, ayca,
jongama sama, dikkal boog!»
Waa ji
14 Soppe, sore nga ni xati mu dëkke xar-xari doj,
làqoo ruqi mbartal yi.
Won ma sa jëmm,
dégtal ma sa baat.
Sa baat a neex,
sa jëmm jekk!
Ndaw si
15 Jàppal-leen ma till yi,
till yu ndaw yiy ruur reseñ,
te sunu reseñ jiy tóor.
16 Sama nijaay, maa moom, man it, moo moom,
di fore digg tóor-tóor yi.
17 Nijaay, balaa jant a fenk,
ker toxu,
dellul gaaw ni kéwél,
mbaa kooba gu ndaw kaw tund yu xàjjalikoo ya.