6
Janqi Yerusalem
Yaw mi dàq ci jigéen ñi,
ana fu sa nijaay dem?
Wax nu fu sa nijaay jaar,
nu seetle la ko.
 
Ndaw si
Sama nijaay dugg na biir toolam,
fa gàncax ga ne bann.
Mu ngi foral ci tool bi,
ak a fori tóor-tóor.
Man, nijaay a moom;
nijaay it, maa moom.
Mooy fore sama digg tóor-tóor yi.
Yaaka taaru
Waa ji
Xarit, taaru nga ni Tirsa ak Yerusalem,
péeyi buur ya,
yéeme nga ni péey yu kawe ya!
Wuy, geesul fee!
Soo ma nee jàkk, ma jànnaxe.
Sa njañ liy loy-loyee ngi saf géttu bëy yu ñuul,
yu bartaloo kaw tundu Galàdd.
Sa gëñ yi ni mbote yu weex,
yéege ca sangukaay ba,
ku nekk ak seexam,
kenn wéetu ca.
Sa lex yiy tàkk ni ŋaali gërënaat,
làqoo sa muuraay bi.
Buur day am juróom benn fukki lingeer
ak juróom ñett fukki jongama
ak jeeg ju dul jeex.
Waaye sama nenne kenn la, matal ma sëkk,
yaayam kennal ko,
muy ngëneelu biiru yaayam.
Janq ji gis ko, di ko jëwe mbégteem,
lingeeri buur aki jongamaam di ko kañ.
10 Ña nga naa: «Ndaw sii ku mu?
Bu nee xiféet, nga ne fajar a xar,
rafet ni leer gu ndaw,
yànj ni jant bi,
yéeme ni gàngoori biddiiw!»
11 Damaa wàcc ba ca toolub saal ya,
xooli cax mu yees mi ci xur wi,
bu reseñ ji jebbee,
mbaa gërënaat ji tóor, ma gis.
12 Damaa ràkkaaju bay lox,
mel ni ku war watiiru buur*.
* 6:12 Li ñu wax fii ci làkku ebrë am na werante.