10
Xërëm neen la
Bu suuf maree, ñaanal Aji Sax ji ab taw,
Aji Sax ji mooy sàkk ay xàmbaar,
sóobal nit ab taw,
saxalal ku ne am ñax ci àll bi.
Xërëm, waxi neen,
gisaanekat gisi fen,
seeni gént, nari neen,
te caaxaani neen lañuy dalalee.
Moo tax mbooloo mii di taxawaalu niy xar,
tumurànke ndax ñàkkub sàmm.
Yiwiku ñeelati na Israyil
«Sàmm yi la sama mer tàkkal,
ñoom sikket yooyu laay dikke mbugal.
Aji Sax ji Boroom gàngoor yi kat mooy taxawu
kërug Yuda, géttam,
te moo leen di def aw fasam wu am daraja,
ngir xare.
Fa Yuda la doju collu tabax di bawoo,
jënu xayma, fa moom,
xalay xare, fa moom,
mboolem njiit yi ba ñépp daj, fa moom.
Ni ñeyi xare lañuy mel,
di joggati banu mbedd mi ci biir xeex bi.
Noonu lañuy xaree, nde ñoom la Aji Sax jiy àndal,
ñuy torxal gawar yi.
Maay jàmbaaral waa kër Yuda,
maay wallu waa kër Yuusufa,
suqli leen, ñeewante leen,
ñu mel ni masuma leena xarab,
nde man maay seen Yàlla Aji Sax ji,
te maa leen di nangul.
Waa Efrayim ni ñeyi xare lañuy mel,
seen xol neexe ni bànneexu biiñ,
seeni doom gis ko, bég,
seenub xol di bànneexoo Aji Sax ji.
Maay waliis, dajale leen,
nde maa leen di jot,
ñu bareeti na ñu baree woon.
Fi biir xeet yi laa leen saawi,
waaye fa bérab yu loq ya lañu may fàttlikoo,
di fa dund ñook seeni doom,
ba keroog ñuy délsi.
10 Fa réewum Misra laa leen di waññee,
te fa Asiri laa leen di dajalee,
yóbbu leen réewum Galàdd ak Libaŋ,
te deesu fa gis fu ñu xaj.
11 Maay jàll géeju njàqare ga,
fàdd gannax ya,
mboolem xóotey dexu Niil wow,
sagub Asiri sàggiku,
nguurug Misra foq.
12 Ci Aji Sax ji laa leen di jàmbaarale,
ciw turam lañuy daagoo.
Kàddug Aji Sax jee!»