Téereb Yonent Yàlla
Cefaña
1
1 Kàddug Aji Sax jii moo dikkaloon Cefaña doomu Kusi. Kusi, Gedalya mooy baayam; Gedalya, Amarya, Amarya, Esekiya. Mu yemook janti buuru Yuda, Yosya doomu Amon.
Am sànj taxaw na
2 «Lépp laay buube ba mu set fi kaw suuf.»
Aji Sax jee ko wax.
3 «Doom aadama ak mala,
njanaaw ak jën laay buub,
ak luy fakktale, booleek ñu bon ñi.
Maay dagge doom aadama fi kaw déndub suuf.»
Aji Sax jee ko wax.»
4 «Maay xàccil sama loxo, Yuda,
ak mboolem waa Yerusalem.
Maay dagge fi bii bérab ndesu tuuri Baal,
ak turu sarxalantukatam yeek
sarxalkatam yi,
5 ak ñiy sujjóotal ci kawi taax
gàngoori biddiiw yi,
ak ñiy sujjóotal aka giñal Aji Sax ji
tey giñe Milkom, yàllantu ji,
6 ak ñi dëddu Aji Sax ji,
wutuñu Aji Sax ji, sàkkuwuñu ko.»
7 Miig! Fi kanam Boroom bi Aji Sax ji,
bésub Aji Sax ji kat dëgmal na;
Aji Sax jee waajal ab sarax,
te moo ca sellal ay ganam.
8 «Keroog bésub saraxu Aji Sax ji,
maay dikke mbugal kàngam yeek
doomi buur yi,
ak boroom coli ndoxandéem yi.
9 Bésub keroog maay dikke mbugal
képp ku aw tuuram tax
mu aadawoo di tëb dëxu bunt,
ak ñiy feesal seen kër yàllantu ak alal
ju aw ay ak njublaŋ maye.
10 Su bés baa,» Aji Sax jee ko wax,
«yuux dina jibe fa buntu Jën ya,
wóoy jibe fa Sanc ya,
rajaxoo ju réy jollee ca tund ya.
11 Yeen waa goxu Ja ba, yuuxooleen,
nde jula yépp ay sànku,
mboolem kuy natt donji xaalis
lees fay dagge.
12 Jantub keroog ay làmp laay niite Yerusalem,
ba dikke mbugal ña fa ne degg,
taaje ni biiñ ci kaw ginjriitam,
te naa ci seen xel: “Aji Sax ji baaxewul, lorewul.”
13 Seen alal lees di sëxëtooji,
seeni kër gental,
ñu tabax ay kër yu ñu dul dëkke;
jëmbat tóokëri reseñ yu ñu dul biiñoo.»
14 Bésub Aji Sax bu mag bee dëgmal,
moo dëgmal te tànk yu gaaw lool lay jegesee.
Kàddug bésub Aji Sax ji dégtu na,
te ca la jàmbaar di yuuxoo yuux yu metti.
15 Bésub keroog bésub sànj lay doon,
bésub njàqare ak tumurànke,
bésub gental ak gentle,
bésub lëndëmu xàmbaari guddi gu ne këruus,
16 bésub bufta ak wootey xare
ca kaw dëkk ya ñu dàbbli,
ak kaw tata yu kawe ya.
17 «Ca laay jàqale doom aadama yi,
ñuy tëñëx-tëñëxi ni silmaxa,
nde Aji Sax ji lañu moy,
te seen deret lees di sotti fi pëndub suuf,
seen yérey biir ni neefare fi suuf.
18 Du seen xaalis, du seen wurus
wu leen di mana xettli.
Keroog bésub sànjum Aji Sax ji,
ak sawaras fiiraangeem,
àddina sépp ay xoyomu.
Mooy raafal moos mboolem ñi dëkke àddina si,
te raafal gu raglu lay doon!»