6
Waruleena réeroo ci seen biir
Te it bu kenn ci yéen amee lëj-lëj digganteem ak mbokku taalibeem, lu tax muy dem ca àttekaayi ñi xamul Yàlla, te baña dem ca gaayi Yàlla yi, ñu àtte ko? Xanaa dangeena xamul ne, gaayi Yàlla yi ñooy àtteji àddina? Te ndegam yéenay àtteji àddina, lu tere ngeen mana àtte mbir yu ñàkk solo yi? Xanaa xamuleen ne nooy àtteji malaaka yi? Waxatumaak mbiri àddina sii. Bu ngeen amee ay lëj-lëj yu mel noonu, dangeen di wuti ay àttekat ci ay nit, ñi amul wenn yoon ci mbooloom ñi gëm! Ma ne kon, war ngeena rus! Xanaa amul ci seen biir kenn ku am xel, ku mana àtte bokkam yi? Waaye defuleen loolu; mbokk a ngi layoo ak moroomam, rax-ca-dolli ci kanam ñi gëmul lañu koy defe!
Layoo bi sax wone na ne bàyyi ngeen seen warugar. Lu tax muñuleen sax tooñ, yi ñu leen di tooñ? Lu tax far nanguwuleen, ñu sàcc leen? Waaye yéen sax yéenay tooñ ak di sàcc, te seeni bokk ngeen koy def!
Xanaa xamuleen ne, ñi jubadi duñu bokk ci nguuru Yàlla? Bu leen ci kenn nax: ñiy doxaan walla xërëmkat yi ak njaalookat yi ak góor-jigéen ñi ak ñi ànd ak ñoom, 10 walla sàcc yi ak ñu bëgge ñi ak màndikat yi ak ñiy xaste ak njublaŋ yi, duñu bokk ci nguuru Yàlla. 11 Te am na ñu meloon noonu ci yéen. Waaye Yàlla fóotal na leen seeni bàkkaar, sellal leen, àtte leen ni ñu jub, ci turu Boroom bi Yeesu Kirist ak ci dooley Xelum Yàlla, sunu Boroom.
Jariñooleen seen yaram ngir ndamu Boroom bi
12 Am na ci yéen ñu naan: «Sañ naa lépp.» Waaw, waaye du lépp a jariñ nit. «Sañ naa lépp,» waaye duma bàyyi dara, mu not ma. 13 Am na ci yéen ñu naan: «Ñam mooy jariñ biir, te biir ay jariñoo ñam.» Waaw, te Yàlla dina leen yàq, ñoom ñaar yépp. Waaye sàkkuñu yaram ngir moy Yàlla; dañu koo sàkk, ngir muy jariñ Boroom bi, Boroom bi di ko jariñoo. 14 Te Yàlla, mi dekkal Boroom bi, dina dekkal it sunu yaram jaare ko ci dooleem. 15 Xanaa xamuleen ne, seen yaram ñooy céri Kirist? Ndax kon damay jël céri Kirist, def ko céri jigéeni moykat? Mukk! 16 Xanaa xamuleen ne, kuy ànd ak jigéen juy moy dafay booloo ak moom, nekk benn? Ndaxte Mbind mi nee na: «Ñoom ñaar dinañu doon benn.» 17 Waaye nag kuy ànd ak Boroom bi, xel yi dañuy booloo, nekk benn.
18 Dawleen njaaloo! Bépp bàkkaar bu nit mana def, du laal yaramam, waaye nag kuy njaaloo, dafay bàkkaar, di lor yaramam. 19 Xanaa xamuleen ne, seen yaram mooy kër Yàlla gi? Gannaaw Xel mu Sell maa ngi ci yéen, te Yàllaa leen ko may, kon moomuleen seen bopp, 20 ndaxte Yàlla jot na leen ak njég lu réy. Kon nag màggal-leen Yàlla ci seen yaram.