13
Su fekkee ne damay wax làkki nit ñi ak yu malaaka yi sax, te boolewuma ci mbëggeel, duma dara lu dul ndënd muy riir, walla jóolóoli buy kandaŋ-kandaŋi. Su ma yéglee wax ju tukkee ci Yàlla, ma xam lépp luy kumpa, ma yor xam-xam bépp te gëm Yàlla ba mana randal ay tund, fekk boolewuma ci mbëggeel, duma dara. Te it su ma doon sarxe li ma am lépp, di bàyyi ñu lakk sama yaram, ba rey ma, su ma ci boolewul mbëggeel, du ma jariñ dara.
Ku bëgg dafay muñ te laabiir. Ku bëgg du iñaan, du kañu, du tiitaru, du def lu jekkadi, du wut njariñu boppam, du naqari deret, du ñaaw njort. Du bég ci lu awul yoon, waaye dina bég ci lépp luy jollil dëgg. Mbëggeel day baale lépp, am gëm ci lépp, yaakaar lépp, muñ lépp.
Mbëggeel amul àpp. Ñiy wax ci kàddug Yàlla dinañu noppi, ñiy wax ay làkk dinañu ko bàyyi, ñiy xamle xam-xamu Yàlla wàcc. Xam-xam bi nu am des na, te ni nu jottalee xibaar bi nu Yàlla dénk des na. 10 Waaye li mat, bu dikkee, li matul jóge fi. 11 Bi ma dee xale, dama doon wax ni xale, di dégge ni xale, di xalaate ni xale. Waaye bi ma doonee mag, bàyyi naa lu bokkoon cig ndaw. 12 Tey jii gis bu lëndëm lanuy gis, ni takkandeer ci seetu bu lëndëm; bu ëllëgee dinanu gis jaxran. Tey jii sama xam-xam des na; bu ëllëgee dinaa xam ba mat sëkk, ni ma Yàlla xame.
13 Léegi nag ñett yii ñooy sax: ngëm, yaakaar, mbëggeel; te mbëggeel moo ci raw.