6
Ñi nekk ci buumu njaam nag, nañu weg seeni sang wegeel gu mat sëkk; noonu kenn du am lu muy werante ci turu Yàlla mbaa ci sunu njàngle. Ku am sang boo bokkal ngëm, bu looloo tax nga yab ko, waaye nga sax ci itteem, ndax kiy jariñu ci sa ñaq, aji gëm la, ku mata bëgg.
Alal ju wóor ji
Jàngleel loolu nag, di ko dénkaane. Waaye su fi amee kuy jàngle leneen, ba jàppul ci kàddu yu wér yu Yeesu Kirist Boroom bi, te fonkul waaraate buy jur ragal Yàlla, kooku boroom tiitar la, bu xamul dara. Dafa wéradi, ba sóobu ci gëstuy neen ak i werante ciy araf yu jurul lu moy ñeetaane, xuloo, xaste, ñaaw njort ak ŋaayoo; ñiy jëfee noonu nit ñu ñaaw xel lañu, ñu xamul genn dëgg te yaakaar ne ragal Yàlla buntu wërsëg la.
Ba tey ragal Yàlla gu ànd ak doylu, wërsëg la. Ndaxte indaalewunu fi dara, te dunu yóbbaale dara. Kon su nu amee lekk ak koddaay, nanu ko doyloo. Waaye ñiy sàkkoo barele, dinañu jànkoonte ak i nattu, ba dugg ci fiir, di xuus ci bëgg-bëggi neen yuy yóbbe ayib, tey sóob nit cig réer ak sànkute. 10 Ndaxte bëgge ci xaalis mooy ndeyu ñaawteef yu bare; am na ñu ko wut, ba moy ci yoonu ngëm, te seen xol di dagg ndax tiis yu bare.
Làmbi ngëm
11 Kon nag yaw waayu Yàlla ji, dawal loolu, te topp njub, ragal Yàlla, ngëm, mbëggeel, muñ ak lewet. 12 Góor-góorlul ci bëre bu baax bi, ba ub làmbi ngëm, te feddali sag téye ci dund gu dul jeex gi; ndaxte ci loolu la la Yàlla woo, te looloo waraloon it sa seede su rafet fa kanam mbooloo mu bare.
13 Noonu fi kanam Yàlla mi jagleel dund ci lépp, ak fi kanam Kirist Yeesu, mi seede woon seede su rafet fa kanam Poñsë Pilaat, maa ngi lay dénk lii: 14 sàmmal ndigal li, baña am gàkk mbaa ŋàññ, ba kera Yeesu Kirist sunu Boroom di feeñ ci ndamam, ca waxtu wa Yàlla dogal. 15 Moom kenn mooy Boroom bu tedd, di Buuru buur yi ak Kilifag kilifa yi. 16 Moom kenn a jagoo dund gu sax, dëkk ci biir leer gu kenn manta jege; moom mi nit masula gis te nit manu koo gis. Moom kenn a yelloo teraanga ak màggaay ba fàww. Amiin.
17 Ñi barele alalu àddina nag, dénk leen ñu baña réy te baña wékk seen yaakaar ci koom-koom yi saxul fenn, waaye ñu wékk ko ci Yàlla, mi nuy may naataange ju mat, ngir nu man ciy bànneexu. 18 Dénk leen ñu def lu baax, te bare jëf yu rafet, ñu yéwén, bay sédd ñi amul, 19 di fàggu dencu ëllëg bu wér. Noonu dinañu feddali seen téye ci dund gu wóor gi.
20 Céy yaw Timote, sàmmal li la Yàlla dénk! Tanqamlul waxi neen yu àddina kese, te dëddu werantey ñi mbubboo xam-xam, fekk dañoo réer. 21 Am na ñu topp xam-xam boobu, waaye moy nañu ci yoonu ngëm.
Yal na yiwu Yàlla ànd ak yéen.