3
Yàqute gi daj mujug jamono
Nanga xam lii: bési tiis yu tar ñu ngi nuy tëru ci mujug jamono. Ndaxte nit ñi dinañu siis te fonk xaalis, di ñu réy tey yég seen bopp, ñuy xaste tey xëtt ndigalu waajur; duñu am kóllëre, sellaay mbaa cofeel; dañuy jàpp mer ak a sos; ñu xér lañuy doon, ñu soxor te bañ lu baax; ay workat lañuy doon, di ñu ëppal te bare tiitar; seen bànneex a leen gënal Yàlla. Dañuy mbubboo diine waaye nanguwuñu koo dugal seen xol. Ñu deme noonu, dëddu leen.
Nit ñu mel noonu ñooy yoxoosu ci biir kër yi, ba fàbbi jigéen ñu ñàkk pastéef, ñi seeni bàkkaar ub seen bopp, te bëgg-bëgg yu wuute jiital leen. Duñu noppee gëstu, waaye duñu mana yegg ci xam-xamu dëgg mukk. Nit ñooñu dañuy bëreek dëgg, ni Sànnes ak Sàmbares bëree woon ak Musaa; ay boroom xel yu gumba lañu, yu seen ngëm tekkiwul dara. Waaye duñu dem fu sore, ndax seen ñàkk xel dina bir ñépp, ni mu dale woon Sànnes ak Sàmbares.
Li Pool dénk Timote
10 Waaye yaw nag xam nga bu baax sama njàngle, sama dund, sama takkute, sama ngëm, sama muñ, sama mbëggeel ak sama dékku tiis. 11 Xam nga li ma daj ciy fitna ak i coono ci dëkki Ancos, Ikoñum ak Listar* Ay dëkk ci diiwaanu Galasi lañu woon, fa Pool tàmbalee yenam, biy waare xibaaru Kirist.. Céy li ma jànkoonteel ciy fitna! Waaye Boroom bi musal na ma ci lépp. 12 Te ku bokk ci Kirist Yeesu, te bëgg dund dund gu ànd ak ragal Yàlla, alamikk ñu fitnaal la. 13 Waaye nit ñu bon ñi ak naaféq yi dinañu fi yées, di naxe ak a nax seen bopp.
14 Yaw nag saxal ci li nga jàng te mu wóor la, xam fi nga tibbe. 15 Li dale ci sa ngone xam nga Mbind mu sell, mi la mana yee ci yoonu mucc, jaar ci gëm Kirist Yeesu. 16 Mbind mu sell mépp, ci gémmiñu Yàlla la jóge, te am na njariñ ngir jàngal nit ñi, yedd leen, jubbanti leen te yee leen ci njub. 17 Noonu waayu Yàlla ji dina mat, ba jekk ci bépp jëf ju rafet.

*3:11 Ay dëkk ci diiwaanu Galasi lañu woon, fa Pool tàmbalee yenam, biy waare xibaaru Kirist.