5
Anañas ak Safira
1 Naka noonu nit ku tudd Anañas, ànd ak Safira jabaram, jaay làccu suuf. 2 Mu dencal boppam benn cér ca njég la, ànd ca ak jabaram; ba noppi mu indi cér ba ca des, teg ko ci loxoy ndaw ya.
3 Bi mu ko defee Piyeer ne ko: «Anañas, lu tax nga bàyyi Seytaane dugg la, ba fees sa xol, ngay wor Xel mu Sell mi, ci li nga dencal sa bopp benn cér ci njég li? 4 Bi mu jaragul, ndax moomuloo ko woon? Te bi mu jaree, ndax yilifuloo woon njég li? Lu tax nga fas ci sa xol def nii? Woruloo nit ñi, waaye Yàlla nga wor.»
5 Bi Anañas déggee baat yooyu, mu daanu dee. Ñi ko dégg ñépp tiit, ba ne nërëm. 6 Noonu waxambaane ya jóg, ñu sàng ko, yóbbu ko, jébbal Yàlla.
7 Ñetti waxtu gannaaw ga, jabaram duggsi, fekk xamul la fa xew. 8 Piyeer daldi ko ne: «Wax ma, ndax lii mooy njégu tool bi?» Mu ne ko: «Waawaaw, lii la.»
9 Ci kaw loolu Piyeer ne ko: «Lu tax ngeen ànd, di diiŋat Xelu Boroom bi? Ñi denci woon sa jëkkër ñu ngi nii ci bunt bi, te dinañu la yóbbu.» 10 Ca saa sa mu daanu ciy tànkam, dee. Bi waxambaane ya agsee nag, ñu fekk ko, mu faatu; ñu yóbbu ko, def ko ci wetu jëkkëram. 11 Noonu tiitaange ju mag tàbbi ci mbooloom ñi gëm ñépp ak ñi ko dégg ñépp.
Ndawi Kirist yi faj nañu ñu bare
12 Bi loolu amee ay kéemaan ak ay firnde yu bare di xew ci nit ñi, jaare ca loxoy ndaw ya. Ñépp di booloo ca Werandaa bu Suleymaan ca kër Yàlla ga. 13 Te kenn ci ña ca des ñemewula booloo ak ñoom, waaye nit ñépp di leen màggal. 14 Moona ay nit ñu gëna bare, góor ak jigéen, di gëm Boroom bi, tey taq ci ñoom. 15 Nit ñi indi sax ñu wopp ca mbedd ya, teg leen ca ay lal yu ndaw ak ay leeso, ngir bu Piyeer di jaar, doonte takkandeeram sax yiir ñenn ci ñoom. 16 Te it nit ñu bare dajaloo, jóge ca dëkk ya wër Yerusalem, ñu indi ay jarag ak ñu rab yu bon sadd; te ñoom ñépp daldi wér.
Fitnaal nañu ndaw yi
17 Booba sarxalkat bu mag ba jóg ak gàngooram gépp, maanaam kureelu Sadusen ga fa dëkk. Kiñaan gu mag jàpp leen, 18 ba ñu jàpp ndaw ya, tëj leen ca kaso ba. 19 Waaye ci guddi malaakam Boroom bi ubbi buntu kaso ba, génne leen ci biti naan: 20 «Demleen taxaw ca kër Yàlla ga, te xamal nit ñi lépp lu jëm ci dund gu wóor gii.» 21 Bi ñu déggee loolu, ñu dugg ca kër Yàlla ga ci suba teel, daldi waare.
Bi ñu koy def, sarxalkat bu mag ba ak gàngooram ñëw, woolu kureelu àttekat ya, maanaam mbooloom njiiti bànni Israyil gépp; ñu yónnee, ngir jëli ndaw ya ca kaso ba. 22 Waaye bi wottukati kër Yàlla ga agsee ca kaso ba, gisuñu leen fa; ñu daldi délsi, yégle ko 23 ne: «Fekk nanu kaso ba tëju bu wóor ak wottukat ya taxaw ca bunt ya, waaye bi nu ko tijjee, fekkunu kenn ci biir.»
24 Bi kilifag wottukati kër Yàlla ga ak sarxalkat yu mag ya déggee loolu, ñu daldi ciy jaaxle lool, ñuy laajante, fu lii di mujj.
25 Noonu benn waay ñëw, yégal leen ne: «Nit ñi ngeen tëjoon ñu ngi taxaw ca kër Yàlla ga, di jàngal nit ñi.» 26 Ci kaw loolu kilifa ga ak wottukat ya dem jëli leen; waaye boolewuñu ci fitna, ngir ragal nit ñi sànni leen ay xeer.
27 Bi ñu leen indee, ñu dëj leen ci kanam mbooloo ma. Sarxalkat bu mag ba laaj leen 28 ne: «Ndax terewunu leen ci lu wér, ngeen waare ci tur woowu, te fi mu ne dajal ngeen Yerusalem ak seeni waare, rax-ca-dolli yéena ngi nuy fexee taqal deretu nit kooku.»
29 Waaye Piyeer ak ndaw ya ne leen: «Déggal Yàlla moo gën déggal nit. 30 Yàllay sunuy maam dekkal na Yeesu, mi ngeen bóomoon ci wékk ko ca bant ba. 31 Te Yàlla yékkati na ko ci ndijooram, mu nekk Buur ak Musalkat, ngir may bànni Israyil réccu, ba mu baal leen seeni bàkkaar. 32 Seede nanu loolu, nun ak Xel mu Sell, mi Yàlla may ñi koy déggal.»
33 Bi ñu déggee loolu, ñu mer ba seen xol di dagg, ñu bëgg leena rey. 34 Waaye amoon na fa nit ku tudd Gamaleel, bokk ci tariixab Farisen ya, di xutbakat bu tedd ci yoonu Musaa, mu jóg ca mbooloo ma, santaane ñu génne leen tuuti. 35 Bi ñu ko defee mu ne leen: «Yéen bokki Israyil, moytuleen li ngeen di def nit ñooñu. 36 Ndaxte bu yàggul Tëdas jógoon na, mbubboo daraja, ba lu mat ñeenti téeméeri nit takktoo ak moom. Tëdas moomu nag reyees na ko, te ñi ko toppoon ñépp tasaaroo, ba seen pexe nasax. 37 Gannaawam it Yudaa mu Galile jóg, ca jamono ja ñu doon bind waa réew ma, mu jógloo nit ñu bare, ñu ànd ak moom. Moom itam dee na, te ay nitam ñépp tasaaroo. 38 Léegi maa ngi leen di wax, génnleen ci mbirum ñooñu te bàyyi leen ñu dem. Ndaxte bu seen pas-pas mbaa seen jëf dee pexem nit, dina yàqu. 39 Waaye bu fekkee ne ndogalu Yàlla la, dungeen ko mana fanq, ngir ragala jànkoonte ak Yàlla.»
40 Bi mu waxee loolu, ñu fekk ko ci xalaatam; ñu woo ndaw ya, daldi leen dóor ay yar, tere leen, ñu waxati dara ci turu Yeesu, ba noppi bàyyi leen, ñu dem.
41 Ndaw ya nag jóge ca kanam kureelu àttekat ya, bég ci li leen Yàlla jàppe, ñu yeyoo yenu toroxte ngir Tur wa*Tur wa mooy turu Boroom bi Yeesu Kirist.. 42 Noonu bés bu nekk ca kër Yàlla ga ak ca kër ya, daawuñu noppee jàngle ak a xamle xibaaru jàmm bi, ne Yeesu mooy Almasi bi.