20
Yeesu Kirist dekki na
Bés ba jiitu ca ayu-bés ga, Maryaamam Magdala jóg ca fajar, dem ca bàmmeel ba. Bi mu agsee, mu gis ne dindi nañu xeer, wa ñu ko ube woon. Mu daw, dem ca Simoŋ Piyeer ak ca beneen taalibe ba, maanaam ka Yeesu bëggoon, ne leen: «Jële nañu néewu Boroom ba ca bàmmeel ba, te xamunu fu ñu ko yóbbu.»
Piyeer ak beneen taalibe ba daw, dem ca bàmmeel ba. Ñoom ñaar ñépp a ngi doon daw, waaye beneen taalibe ba raw Piyeer, jëkk ko ca bàmmeel ba. Duggul nag, dafa sëgg, yër, séen càngaay la ca suuf. Noonu Simoŋ Piyeer, mi ko toppoon, agsi, daldi dugg. Mu séen càngaay la ci suuf, ak kaala ga muuroon boppu Yeesu. Waaye kaala googu àndul ak càngaay la; dañu ko laxas, teg ko ci wet. Noonu keneen ka jiitu woon ca bàmmeel ba, duggsi moom itam. Naka la gis, daldi gëm. Taalibe yi xamaguñu woon Mbind mi doon wone ne Yeesu dafa wara dekki. 10 Noonu taalibe ya dëpp, ñibbi.
Yeesu feeñu na Maryaamam Magdala
11 Maryaama nag moom, ma nga desoon ca biti, ca wetu bàmmeel ba, di jooy. Bi muy jooy, mu sëgg, yër ci biir, 12 séen ñaari malaaka yu sol mbubb yu weex, toog ca bérab, ba ñu dencoon Yeesu; kenn ka féeteek bopp bi, ki ci des ca tànk ya. 13 Malaaka ya laaj ko ne: «Jigéen ji, looy jooy?» Mu ne leen: «Dañoo jël sama Boroom, te xawma fu ñu ko yóbbu.»
14 Bi mu waxee loolu, mu geestu, séen Yeesu mu taxaw, waaye xamul woon ne moom la. 15 Yeesu laaj ko ne: «Jigéen ji, looy jooy? Kooy seet?» Mu foog ne boroom tool ba la, ne ko: «Sëriñ bi, bu fekkee yaa ko yóbbu, wax ma foo ko denc, ma jëli ko.» 16 Noonu Yeesu ne ko: «Maryaama.» Mu walbatiku, làkk ko ci yawut ne ko: «Ràbbuni!» Ràbbuni mooy tekki «Kilifa gi».
17 Yeesu ne ko: «Bu ma téye, ndaxte yéegaguma ca Baay ba. Waaye demal, ne samay bokk, maa ngi yéeg ca sama Baay biy seen Baay, ca sama Yàlla jiy seen Yàlla.» 18 Noonu Maryaamam Magdala dem, yégali ko taalibe ya ne leen: «Gis naa Boroom bi!» Mu daldi leen nettali li mu ko wax.
Yeesu feeñu na taalibe yi
19 Bés boobu ca ngoon sa, taalibe yaa nga daje woon ca genn kër, tëju ca biir ndax ragal Yawut ya. Yeesu ne tëll ci seen biir ne leen: «Na jàmm wàcc ci yéen!» 20 Mu daldi leen won ay loxoom ak wetam. Bi ñu gisee Boroom bi, taalibe ya daldi bég lool. 21 Yeesu dellu ne leen: «Na jàmm wàcc ci yéen! Ni ma Baay bi yónnee, noonu laa leen di yónnee, man itam.»
22 Bi mu waxee loolu, mu ëf leen ne leen: «Sol naa leen Xelu Yàlla mu Sell mi. 23 Ñi ngeen di baal seeni bàkkaar, baal nañu leen ba noppi; ñi ngeen baalul, baaluñu leen.»
Yeesu ak Tomaa
24 Fekk na Tomaa, mi bokk ci fukki taalibe yi ak ñaar, te turam di tekki «Séex bi», nekku fa woon, bi Yeesu ñëwee. 25 Yeneen taalibe yi ne ko: «Gis nanu Boroom bi!» Mu ne leen: «Su ma gisul fa ñu daajoon pont ya ci ay loxoom, te defuma ca sama baaraam, su ma tegul it sama loxo ci wetam, duma ko gëm mukk.»
26 Bi ñu ca tegee ayu-bés, taalibe Yeesu ya dajewaat ca biir kër ga, Tomaa itam a nga fa woon. Bunt yépp tëju woon nañu, waaye Yeesu ne tëll ci seen biir ne leen: «Na jàmm wàcc ci yéen!» 27 Noonu mu ne Tomaa: «Indil sa baaraam fii te seet sama loxo; indil sa loxo, teg ko ci sama wet. Bàyyil di weddi te nga gëm.» 28 Tomaa ne ko: «Sama Boroom, sama Yàlla!» 29 Yeesu ne ko: «Li nga ma gis a tax nga gëm? Ki bég mooy ki gëm te gisu ma!»
30 Yeesu wone na it ci kanam taalibe ya yeneen firnde yu ñu nettaliwul ci téere bii. 31 Waaye li ci nekk, bind nañu ko ngir ngeen gëm ne Yeesu mooy Almasi bi, Doomu Yàlla ji, te seen ngëm may leen, ngeen am ci moom dund.