12
Yeesu artu na taalibeem yi cig naaféq
Gannaaw loolu, naka la mbooloo ma dajaloo ba mat ay junniy junniy nit, di tancante, Yeesu tàmbalee wax jëmale ca taalibeem ya ne leen: «Moytuleen lawiiru Farisen ya, li di naaféq. Amul dara lu nëbbu lu ñu warula biral, mbaa lu kumpa lu ñu warula siiwal. Looloo tax lu ngeen wax ci biir lëndëm, dees na ko dégg ci leer. Lu ngeen déey nit ci biir néeg, dees na ko yégle ci kaw taax yi.
«Maa ngi leen koy wax, samay xarit, buleen ragal ñu mana rey yaram, ba noppi dootuñu mana def dara. Dinaa leen wax nag ki ngeen wara ragal: ragal-leen ki nga xam ne bu reyee ba noppi, am sañ-sañu sànni ca sawara. Waaw, maa ngi leen koy wax, ragal-leen kooku. Juróomi picci ramatu, ndax duñu ko jaay ci ñaari dërëm? Moona Yàlla fàttewul benn ci ñoom. Seen kawari bopp sax waññees na leen. Kon buleen ragal dara, yéena gën ndiiraanu ramatu.
«Te maa ngi leen koy wax, képp ku ma nangu ci kanam nit ñi, Doomu nit ki dina la nangu ci kanam malaakay Yàlla yi. Waaye ku ma gàntu ci kanam nit ñi, dinañu la gàntu ci kanam malaakay Yàlla yi. 10 Ku sosal Doomu nit ki, dinañu la baal, waaye kuy sosal Xel mu Sell mi, duñu la ko baal.
11 «Bu ñu leen yóbboo ca jàngu ya, ca kanam kilifa ya ak àttekat ya, buleen am xel ñaar ci li ngeen wara tontu ak nan ngeen wara tontoo, walla lu ngeen wara wax, 12 ndaxte Xel mu Sell mi dina leen xamal ca waxtu woowa li ngeen wara wax.»
Léebu nit ku ñàkk xel ki
13 Am ca mbooloo ma ku ne Yeesu: «Kilifa gi, joxal ndigal sama mag, mu sédd ma ci sunu ndono.» 14 Yeesu ne ko: «Sama waay, kan moo ma fal àttekat ci seen kaw, walla mu teg ma fi, ma di leen séddaleel seen alal?» 15 Noonu mu ne leen ñoom ñépp: «Moytuleen bëgge, ndaxte bakkanu nit ajuwul ci alalam, ak lu mu baree bare.»
16 Noonu mu dégtal leen wii léeb ne: «Dafa amoon waa ju bare alal, te ay toolam nangu lool, 17 muy werante ci xelam naan: “Nu ma wara def? Ndaxte amatuma fu ma dajale sama ngóob mi.” 18 Noonu mu ne: “Nii laay def: daaneel sama sàq yi, defaraat yu gëna réy, ba man cee dajale sama dugub ji ak sama am-am bépp. 19 Te dinaa kañ sama bopp ne: ‘Yaw mii, am nga alal ju bare ju mana dem ay ati at; noppalal sa yaram, di lekk, di naan, tey bég.’ ” 20 Waaye Yàlla ne ko: “Ñàkk xel! Guddig tey, dees na jël sa bakkan. Kon li nga dajale lépp, ku koy moom?”
21 «Kiy dajale alal ngir boppam nag te amul dara ca kanam Yàlla, lu mel nii moo lay dal.»
Wóolu Yàlla
22 Noonu Yeesu daldi ne taalibeem yi: «Loolu moo tax maa ngi leen koy wax, buleen seen bakkan jaaxal, ci lu ngeen wara lekk. Buleen jaaxle it ngir seen yaram ci lu ngeen wara sol, 23 ndaxte bakkan moo gën lekk, te yaram a gën koddaay. 24 Seetleen baaxoñ yi: duñu ji, duñu góob, amuñu dencukaay, amuñu sàq, teewul Yàllaa ngi leen di dundal. Céy ni ngeen ëppe maana picc yi! 25 Ana kan ci yéen ci kaw njaaxleem, moo mana yokk waxtu ci àppam? 26 Su fekkee lu tuuti loolu rekk manuleen koo def, kon lu tax ngeen di jaaxle ci li ci des?
27 «Seetleen ni tóor-tóori ñax mi di saxe. Duñu liggéey, duñu ëcc, waaye maa ngi leen di wax ne Suleymaan sax ci ndamam soluwul woon ni benn ci ñoom. 28 Yéen ñi néew ngëm! Bu Yàlla woddee nii ñaxum tool yi, miy sax tey, te bu subaa ñu def ko ci taal bi, ndax du leen gëna wodd? 29 Buleen di wut lu ngeen di lekk walla lu ngeen di naan; te buleen ci jaaxle. 30 Ndaxte loolu lépp, ñi xamul Yàlla ñoo koy wut. Te seen Baay xam na ne soxla ngeen ko. 31 Waaye wutleen nguuram, te loolu lépp dina leen ko ci dollil.
32 «Buleen ragal dara, yéen coggal ju ndaw ji, ndaxte dafa soob seen Baay, mu jagleel leen nguuram. 33 Jaayleen seen alal, sarxe ko, ngir sàkku ay mbuusi xaalis yu dul bënn, maanaam alal ju dul jeex ca laaxira; foofa sàcc du ko jege te max du ko yàq. 34 Ndaxte fu sa alal nekk, fa la sa xol nekk itam.
Farlu gi
35 «Takkuleen bu dëgër te bàyyi làmp yi tàkk. 36 Mel-leen ni ay surga yuy xaar seen njaatige buy jóge ca céet ga, ndax bu fëggee bunt ba, ñu ubbil ko ca saa sa. 37 Surga yooyee seen njaatige fekkul ñuy nelaw, ba mu agsee, ñoo gëna yeyoo ngërëm. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, njaatige bi dina sol yérey waañ, wax leen ñu toog lekk, ba noppi indil leen ñam wi. 38 Su fekkee seen njaatige ci xaaju guddi lay ñëw sax, walla bu suuf seddee, te fekk leen noonu, surga yooyu ñoo gëna yeyoo ngërëm. 39 Waaye xamleen lii: bu boroom kër gi xamoon ban waxtu la sàcc bi di ñëw, du ko bàyyi, mu toj këram. 40 Yéen itam taxawleen jonn, ndaxte Doomu nit ki dina ñëw ci waxtu wu ngeen ko séenuwul.»
41 Piyeer ne Yeesu: «Boroom bi, ndax dangay dégtal léeb wii ngir nun rekk walla ngir mbooloo mépp?» 42 Boroom bi ne ko: «Kan moo nekk surga bu takku te teey, bu njaatigeem teg ci waa kër gi, ngir mu leen di dundal ci jamono ji? 43 Bu njaatigeem ñëwee te gis mu def noonu, surga boobu dina am ngërëm. 44 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, njaatige bi dina ko teg ci alalam jépp. 45 Waaye su fekkee surga ba da ne ci xelam: “Sama njaatige day yéexa ñëw,” ba tax mu tàmbalee dóor surga ya ca des ak mbindaan ya, di lekk te di naan, di màndi, 46 kon njaatige ba dina ñëw ci bés bu mu ko séenuwul ak waxtu wu mu xamul. Dina ko dóor ay dóor yu metti, jox ko añub ñi gëmul Yàlla.
47 «Surga bi xam bëgg-bëggu njaatigeem, te waajul mbaa mu takku def ko, dinañu ko dóor dóor yu metti. 48 Waaye surga bi xamul bëgg-bëggu njaatigeem, te def lu yelloo ay dóor, dinañu ko dóor dóor yu néew. Ku ñu jox lu bare dees na la feyeeku lu bare. Ku ñu dénk lu bare, dees na la laajaat lu ko ëpp.
Jàmm walla féewaloo ci biir nit ñi
49 «Damaa ñëw ngir indi sawara si ci àddina, te bëgg naa xaat taal bi tàkk. 50 Fàww ñu sóob ma ci metit, te ba looluy mat, duma noppalu. 51 Ndax dangeena xalaat ne damaa ñëw ngir indi jàmm ci àddina? Déedéet. Maa ngi leen koy wax, damaa ñëw ngir indi féewaloo. 52 Gannaaw-si-tey, bu juróomi nit bokkee genn kër, dinañu féewaloo. Ñett dinañu féewaloo ak ñaar ñi ci des, ñaar ñi féewaloo ak ñett ñooñu. 53 Baay dina féewaloo ak doom, doom ak baayam. Ndey dina féewaloo ak doomam ju jigéen; doom ju jigéen ji ak ndeyam. Goro dina féewaloo ak soxnas doomam; soxnas nit ak goroom.»
Lan mooy jamonoy tey jii
54 Yeesu neeti mbooloo ma: «Bu ngeen gisee mu xiin ci sowu, dangeen naan ca saa sa: “Dina taw,” te mooy am. 55 Te bu ngeen yégee ngelaw liy uppe sudd, ngeen ne: “Dina tàng tàngaay wu metti,” te mooy am. 56 Naaféq yi ngeen doon! Man ngeena ràññee melow asamaan ak suuf, waaye lu tax manuleena ràññee li jamonoy léegi ji di tekki?
57 «Lu tax it dungeen àtteel seen bopp liy jëf ju jub? 58 Bu la nit jiiñee dara, ba ngeen ànd di dem ca àttekat ba, nanga fexee juboo ak moom ci yoon wi. Lu ko moy, dina la yóbbu ci yoon, yoon jébbal la ca loxoy alkaati ba, mu tëj la. 59 Maa ngi la koy wax, doo génn foofa mukk te feyuloo fiftin bi ci mujj.»