7
Bul ñaaw njort, ba àtte sa moroom
«Buleen àtte seeni moroom ak ñaaw njort, ngir bañ ñu àtte leen yéen itam. Ndaxte dees na leen àtte ak ni ngeen di àttee, nattal leen ak li ngeen di nattale. Lu tax ngay xool ñax gi ci sa bëtu mbokk, te gisuloo gànj gi ci sa bët yaw? Walla nan ngay waxe sa mbokk: “May ma, ma dindil la ñax gi ci sa bët,” fekk gànj a ngii ci sa bët yaw? Naaféq, jëkkala dindi gànj gi ci sa bët, te noonu dinga mana gis bu leer, ngir dindi ñax gi ci sa bëtu mbokk.
«Buleen jox lu sell xaj yi, mbaa sànni seeni per ci kanam mbaam-xuux yi, ngir bañ ñu dëggaate ko te walbatiku, xotti leen.
Yàlla nangu na ñaanu ku gëm
«Ñaanleen, ñu may leen; seetleen te dingeen gis; fëggleen, ñu ubbil leen. Ndaxte képp kuy ñaan, dinga am; kuy seet, dinga gis; kuy fëgg, ñu ubbil la. Kan ci yéen, bu la sa doom ñaanee mburu, nga jox ko doj? 10 Walla mu ñaan la jën, nga jox ko jaan? 11 Ndegam yéen ñi bon yéena mana jox seeni gone lu baax, astamaak seen Baay bi nekk ci kaw dina jox lu baax ñi ko koy ñaan!
12 «Kon nag lépp lu ngeen bëgg, nit ñi defal leen ko, yéen itam nangeen leen ko defal; ndaxte loolu moo ëmb yoonu Musaa ak waxi yonent yi.
Bunt bu xat bi
13 «Jaarleen ci bunt bu xat bi, ndaxte bunt bi ak yoon wi jëm sànku yaatu nañu, te ñi ciy jaar bare. 14 Waaye buntu dund gu wóor xat na, te yoon wi jëm kaw sew na, te ñi ko gis barewul.
Garab ak meññeefam
15 «Moytuleen ñi mbubboo turu yonent. Dañuy ñëw ci yéen, yor melow xar, waaye ci biir ay bukki yu soxor lañu. 16 Dingeen leen xàmmee ci seeni jëf. Ndax dees na witte reseñ ci dédd, walla figg ci xaaxaam? 17 Noonu garab gu baax gu nekk dina meññ doom yu neex, waaye garab gu bon dina meññ doom yu bon. 18 Garab gu baax manula meññ doom yu bon, naka itam garab gu bon manula meññ doom yu neex. 19 Garab gu nekk gu dul meññ doom yu neex, dees na ko gor, sànni ko ca sawara sa. 20 Ci seeni jëf nag ngeen leen di xàmmee.
21 «Du képp ku may wax: “Boroom bi, Boroom bi,” mooy dugg ca nguuru Yàlla Aji Kawe ji; ka cay dugg mooy kiy def sama coobarey Baay, bi nekk ci kaw. 22 Bu bés baa, ñu bare dinañu ma wax: “Boroom bi, Boroom bi, ndax du ci saw tur lanu daa waxe ci kàddug Yàlla? Ndax du ci saw tur lanu daa dàqe ay rab? Ndax du ci saw tur lanu daa defe ay kéemaan yu bare?” 23 Ci kaw loolu dinaa leen wax dëgg ne leen: “Masuma leena xam; soreleen ma, yéen ñiy def bàkkaar.”
Léebu ñaari tabaxkat yi
24 «Képp ku dégg nag lii ma leen wax, te di ko jëfe, dinga mel ni nit ku am xel, ku tabax këram, samp ko ciw doj. 25 Ba mu noppee, taw bi daldi sóob, wal mi ñëw, ngelaw li jóg, ñu dal ci kaw kër ga; waaye màbbul, ndaxte mu ngi jàpp ca doj wa. 26 Waaye képp ku dégg lii ma leen wax te jëfewuloo ko, dinga mel ni nit ku ñàkk xel, ku tabax këram ci gannuus bi. 27 Ba mu noppee, taw bi daldi sóob, wal mi ñëw, ngelaw li jóg, ñu dal ci kaw kër ga; mu màbb, ba ne tasar.»
28 Bi Yeesu waxee loolu ba noppi, mbooloo ma daldi waaru ca njàngleem, 29 ndaxte jàngal na leen ak sañ-sañ bu seeni xutbakat amul.