21
Yeesu dugg na Yerusalem
1 Gannaaw loolu Yeesu ak taalibe ya jege woon nañu Yerusalem, ba agsi dëkku Betfase ci wetu tundu Oliw ya. Noonu Yeesu yebal ñaari taalibe, 2 ne leen: «Demleen ci dëkk bi ci seen kanam. Bu ngeen eggee, dingeen gis mbaam mu ñu yeew ak cumburam; yiwileen leen, indil ma leen. 3 Te bu leen kenn waxee dara, ngeen ne ko: “Boroom bi da leena soxla.” Kon ca saa sa dina leen bàyyi, ñu dem.»
4 Yeesu def na noonu, ngir la ñu waxoon jaarale ko cib yonent am, bi mu naan:
5 «Waxal waa Siyoŋ:
“Seen buur a ngi ñëw ci yéen;
ku lewet la, te war mbaam-sëf,
dig cumbur, doomu mbaam.”»
6 Noonu taalibe ya dem, def loolu leen Yeesu sant. 7 Ñu indi mbaam ma, moom ak cumbur ga, lal ci seeni yére, Yeesu toog ca. 8 Ña ëpp ca mbooloo ma lal seeni yére ca yoon wa, ñenn ña dagg ay cari garab, lal leen it ca yoon wa. 9 Mbooloom ña ko jiitu ak ña ko topp ñépp di wax ca kaw naan:
«Osaana, yaw Sëtu Daawuda bi!
Yaw miy ñëw ci turu Boroom bi, ku barkeel nga!
Ca bérab yu gëna kawe, nañu ne: “Osaana!”»
10 Bi nga xamee ne Yeesu dugg na Yerusalem, dëkk ba bépp yëngatu ne: «Kii moo di kan?» 11 Mbooloo ma ne leen: «Kii moo di yonentu Yàlla Yeesu, bi jóge Nasaret ci Galile.»
Yeesu dàq na jaaykat ya ca kër Yàlla ga
12 Bi loolu amee Yeesu dugg ca kër Yàlla ga, dàq ñépp ña fay jaay ak ña fay jënd. Mu daaneel taabali weccikatu xaalis ya ak tooguy jaaykati pitax ya, 13 naan: «Mbind mi nee na: “Sama kër dinañu ko wooye këru ñaan ci Yàlla,” waaye yéen def ngeen ko këru sàcc.»
14 Noonu ay gumba ak ay lafañ ñëw ci moom ca kër Yàlla ga, mu faj leen.
15 Bi nga xamee ne sarxalkat yu mag ya ak xutbakat ya gis nañu yëf yu doy waar ya mu def, te dégg xale yu ndaw ya nekk ca kër Yàlla ga, di wax ci kaw naan: «Osaana, yaw Sëtu Daawuda bi!» ñu daldi mer. 16 Noonu ñu ne Yeesu: «Ndax dégg nga li ñuy wax?» Yeesu ne leen: «Waaw, dégg naa ko. Ndax masuleena jàng lii ci Mbind mi:
“Ci gémmiñu perantal ak ñiy nàmp
sàkkal nga sa bopp ay cant”?»
17 Bi Yeesu waxee loolu, mu bàyyi leen, génn dëkk ba, jëm Betani, fanaan fa.
Yeesu rëbb na garabu figg ga
18 Ci suba teel Yeesu délsi ca dëkk ba, mu xiif. 19 Noonu mu séen garabu figg ca yoon wa, waaye bi mu fa agsee, gisu ci dara lu dul ay xob rekk. Ci kaw loolu Yeesu ne ko: «Dootuloo meññ mukk!» Ca saa sa figg ga daldi wow.
20 Bi nga xamee ne taalibe ya gis nañu loolu, ñu waaru naan: «Nan la figg gi daldi wowe ci taxawaay bi?» 21 Noonu Yeesu ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, su ngeen gëmee te baña werante, dingeen def li ma def figg gi, rax-ca-dolli bu ngeen nee tund wale: “Jógal tàbbi ca géej ga,” dina ko def. 22 Te lépp lu ngeen laaj cig ñaan, bu ngeen ci boolee ngëm, dingeen ci jot.»
Sañ-sañu Yeesu
23 Gannaaw loolu Yeesu dugg ca kër Yàlla ga, di fa jàngle. Bi muy jàngle nag sarxalkat yu mag ya ak njiiti xeet wa ñëw ci moom ne ko: «Yëf yii ngay def, ci ban sañ-sañ nga koy defe? Ku la may boobu sañ-sañ?» 24 Yeesu ne leen: «Man itam dinaa leen laaj lenn; bu ngeen ma ko waxee, kon dinaa leen wax ci ban sañ-sañ laay defe yëf yii. 25 La Yaxya daan def, di sóob nit ñi ci ndox, fu mu ko jële, ci Yàlla walla ci nit ñi?» Ci kaw loolu ñu daldi werante ci seen biir naan: «Bu nu nee: “Ci Yàlla,” dina nu laaj: “Lu tax gëmuleen ko kon?” 26 Te bu nu nee: “Ci nit ñi,” kon mbooloo mi dal ci sunu kaw, ndaxte ñépp teg nañu Yaxya ab yonent.» 27 Ñu ne Yeesu nag: «Loolu xamunu ko.» Noonu Yeesu ne leen: «Kon man itam duma leen wax ci ban sañ-sañ laay defe yëf yii.
Léebu ñaari doom ya
28 «Lu di seen xalaat ci lii? Kenn nit amoon na ñaari doom. Am bés mu ñëw ca taaw ba ne ko: “Sama doom, demal tey liggéeyi ca sama toolu reseñ.” 29 Taaw ba ne ko: “Demuma,” waaye gannaaw loolu xelam yedd ko, mu dem. 30 Gannaaw gi, baay ba ñëw ca tofo ba, wax ko noonu. Mu ne ko: “Waaw,” waaye demul.»
31 Noonu Yeesu laaj leen: «Kan ci ñaari doom yooyu moo def coobarey baayam?» Ñu ne: «Taaw ba.» Yeesu ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, juutikat yi ak jigéeni moykat yi ñoo leen jëkka dugg ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji. 32 Ndaxte Yaxya ñëw na ci yéen ci yoonu njub, te gëmuleen ko; waaye juutikat yi ak jigéeni moykat yi gëm nañu ko. Te gannaaw bi ngeen gisee loolu, seen xel soppikuwul sax, ba ngeen gëm ko.»
Léebu beykat, yi rey doomu boroom tool bi
33 Yeesu teg ca ne: «Dégluleen beneen léeb. Amoon na fi benn boroom kër bu jëmbët toolu reseñ. Mu ñag tool bi, gas ci biir pax, ngir nal ci reseñ yi. Mu tabax wottukaay, batale ko ay beykat, daldi tukki.
34 «Bi nga xamee ne bëgg nañoo witt reseñ yi, mu yónni ay surgaam ci beykat yi, ngir jot wàllam ci meññeef mi. 35 Waaye beykat yi jàpp surga yi, kenn ki ñu dóor ko ay yar, keneen ki ñu rey ko, ki ci des ñu sànni ko ay doj. 36 Boroom kër gi nag yónniwaat yeneen surga yu ëpp yu jëkk ya, beykat yi def leen noonu ñoom itam. 37 Mujj mu yónni doomam naan: “Xëy na ñu weg sama doom.” 38 Waaye bi beykat yi gisee doom ji, ñu ne ci seen bopp: “Kii moo wara donn tool bi; nan ko rey, moom ndonoom.” 39 Ñu jàpp ko nag, génne ko tool bi, rey ko.»
40 Noonu Yeesu laaj leen: «Bu boroom tool bi ñëwee nag, na muy def beykat yi?» 41 Ñu ne ko: «Dina rey reyin wu ñaaw nit ñu soxor ñooñu, batale tool bi yeneen beykat, yi koy jox wàllam ci jamonoy meññeef.»
42 Kon Yeesu ne leen: «Xanaa masuleena jàng lii ci Mbind yi?
“Doj wi tabaxkat yi sànni;
mujj na di doju koñ;
ci Boroom bi la loolu jóge,
te yéemu nanu ci.”
43 «Loolu moo tax maa ngi leen koy wax, dinañu leen xañ nguuru Yàlla, dénk ko xeet wuy def ay jëfam. 44 Ku dal ci doj wii, dammtoo; ku mu dal ci sa kaw, rajaxe la.»
45 Bi nga xamee ne sarxalkat yu mag ya ak Farisen ya dégg nañu léebam yooyu, ñu xam ne ñoom lay wax. 46 Noonu ñu di ko fexee jàpp, waaye ragal nañu nit ña, ndaxte ñépp teg nañu ko ab yonent.