8
Dund gu bees ci dooley Xelu Yàlla mi
Léegi nag yoon manula dab ñi bokk ci Yeesu Kirist. Ndaxte kàttanu Xelum Yàlla, tukkee ci Kirist Yeesu, di may nit dund gu bees, goreel na ma ci notaangeg bàkkaar ak dee. Lu yoonu Musaa manul woona def, ndax néew dooley nit, Yàlla defe na ko nii: dafa yónni Doomam, ngir mu yor sunu jëmm, nun ñiy nekk ay bàkkaarkat, ba noppi mu jébbale bakkanam, ngir dindi bàkkaar yi. Noonu la Yàlla tase nguuru bàkkaar ci nit. Ba tax na léegi njub, gi yoonu Musaa di digle, am na ci nun, ñiy déggal Xelu Yàlla mi te baña topp sunu nafsu.
Ñiy topp seen nafsu, seeni bëgg-bëgg rekk lañu fonk, waaye ñiy topp Xelu Yàlla mi, coobareem lañu fonk. Ndaxte fonk nafsu, ci dee lay jëme; waaye fonk Xelu Yàlla mi, dund ak jàmm lay joxe. Ndaxte ku fonk sa nafsu, bañaaleb Yàlla nga, ndaxte doo déggal Yàlla, mbaa ngay sàmm ay santaaneem, te manuloo koo def sax. Kuy topp sa nafsu nag, doo mana neex Yàlla.
Waaye yéen nekkatuleen ci topp seen nafsu, waaye yéena ngi topp Xelu Yàlla mi, bu fekkee ne mu ngi dëkk ci yéen. Ku amul Xelum Kirist nag, bokkuloo ci moom. 10 Bu fekkee ne Kirist dëkk na ci yéen nag, lii moo am: seen yaram mi ngi ci dooley dee ndax bàkkaar bi nekk ci yéen, waaye seen xel mi ngi dund ndax njub gi leen Yàlla jox. 11 Kon nag gannaaw Xelum Yàlla, mi dekkal Yeesu ca néew ya, dëkk na ci yéen, dina tax seen yaram wi néew doole dund ci kàttanu Xel moomu dëkk ci yéen.
12 Kon nag bokk yi, am nanu lu nu war, waaye waxuma leen topp sunu nafsu ak i bëgg-bëggam; 13 ndaxte kuy topp nafsoom, fàww mu dee, waaye kuy not jëfi yaramam ci dooley Xelu Yàlla mi, dina dund. 14 Ndaxte ñépp ñiy déggal Xelu Yàlla mi, ay doomi Yàlla lañu. 15 Nekkatuleen fa kanam Yàlla, ni jaam bu ragal sangam, waaye Xel mi leen Yàlla sol, ay doomi Yàlla la leen def, ba tax nu di wooye Yàlla: «Abba», maanaam «Baay.» 16 Ndaxte Xelu Yàlla mi, moom ci boppam, day ànd ak sunu xel ci seede ne doomi Yàlla lanu. 17 Gannaaw ay doomi Yàlla lanu, dinanu moomi lépp li Yàlla jagleel ay doomam, séddu ci ngëneel yi Kirist yelloo. Waaye nag ku bëgga bokk ak Kirist ndamam ëllëg, war ngaa séddu ci ay fitnaam tey.
Ndam liy ñëw
18 Xalaat naa ne sunu naqaru tey, wareesu ko tëkkale ak sunu ndamu ëllëg. 19 Ndax li Yàlla bind lépp a ngi ne seewa gis doomi Yàlla yi feeñ ci seen biir ndam. 20 Ndaxte dunyaa bi bépp mu ngi ci yoon wu dul mujj fenn; teyu ko, Yàlla moo ko ko teg. Waaye teewul ñu am yaakaar ne, 21 Yàlla dina rengi seen buumi njaam ci dee, boole leen ci jàmmu doomi Yàlla yi ak seen ndam.
22 Xam nanu ba fi nu tollu ne li Yàlla bind lépp a ngi mititlu ni jigéen juy matu. 23 Te du dunyaa bi rekk mooy mititlu, nun it nu ngi mititlu, nun ñi Yàlla sol Xelam, ngir nu ñam añu ëllëg; nu ngi ne seew Yàlla boole nu ci lépp li nu yelloo ni ay doomam, keroog bés bu Yàllay goreel sunu yaram. 24 Ndaxte sunu mucc ëmb na yaakaar. Li nga gis ba noppi, nekkatul yaakaar; li teew, noo koy yaakaare? 25 Li feek gisagunu nag li nuy yaakaar, dinanu ko séentu ak muñ.
26 Te it Xelu Yàlla mi moo nuy xettali ci sunug néew doole. Ndaxte xamunu sax naka lanu wara ñaane Yàlla, waaye Xelu Yàlla maa ngi nuy ñaanal fa moom ak i yéene yu làmmiñ manta takk. 27 Te Yàlla, miy nattu xol yi, xam na xalaatu Xel mi, ndaxte tinu, gi muy tinul gaayi Yàlla yi, méngoo na ak coobarey Yàlla.
28 Xam nanu itam ne ñi bëgg Yàlla, maanaam ñi Yàlla woo ci boppam te boole leen ci li mu tëral, Yàlla dina joo loxoom ci lépp lu xew ci seen dund, ngir jural leen lu baax. 29 Ndaxte ñi mu xamoon lu jiitu, dafa dogaloon ñu nirook Doomam, ngir mu nekk taaw ci biir njaboot gu yaa. 30 Ñi mu dogaloon loolu ci ñoom, da leena woo; ñooñu mu woo, da leena àtte ni ñu jub; ñooñu mu àtte jub, da leena boole ca ndamam.
Mbëggeelu Yàlla ci Yeesu Kirist
31 Lu nu wara wax nag ci loolu lépp? Gannaaw Yàlla ànd na ak nun, kan moo nu manal dara? 32 Yàlla mi nu gàntulul Doomam waaye mu joxe ko, mu dee ngir nun, ndax dina nu bañalati dara? 33 Ñi Yàlla tànnal boppam, kan moo leen di tuumaal? Yàlla moo leen àtte ni ñu jub. 34 Kan moo leen mana teg tooñ? Yeesu Kirist mi dee, moo dekki itam, te mu nga fa ndijoorul Yàlla, di nu fa ñaanal! 35 Kan moo nu mana tàggaleek mbëggeelu Kirist? Xanaa duy nattu, te du njàqare, du it fitna, du xiif walla rafle, du it ay ngaañ walla jaasi sax. 36 Moo tax Mbind mi ne:
«Ñu ngi nuy rey ngir yaw, ci suba ba jant so;
ñu ngi nuy jàppe ni xar yu ñuy rey.»
37 Waaye loolu lépp teewul, nu ngi mel niy ñeyi xare ci dooley Kirist mi nu bëgg. 38 Ndax wóor na ma ne dara manu noo tàggaleek mbëggeelam; du dee, du dund, du malaaka yi, du seeni kilifa, du tey, du ëllëg, du boroom doole yi, 39 du li ci kaw mbaa li ci suuf, mbaa leneen lu ñu bind; dara manu noo tàggale mukk ak mbëggeel, gi nu Yàlla jox ci Kirist Yeesu sunu Boroom.