Bataaxal bi Yàlla may Pool,
mu bind ko
TIT
1
Man Pool maa lay bind, man miy jaamu Yàlla ak ndaw li Yeesu Kirist yónni, ngir xamle ngëm, gi lal yoonu ñi Yàlla tànn, tey yokk xam-xamu dëgg, giy meññ ragal Yàlla; mu sukkandiku ci yaakaar ju dëggu, ji nu am ci dund gu dul jeex, gi Yàlla dige ba dara sosoogul, moom mi dul tebbi waxam. Te léegi, ci jamono ji ko soob, feeñal na xibaaram boobu ci waaraate, bi ma Yàlla sunu Musalkat dénk te digal ma, ma xamle ko. Maa ngi lay bind, Tit, yaw sama doomu diine ju wér ci ngëm, gi nu bokk nun ñépp. Yal na la Yàlla Baay bi ak Kirist Yeesu sunu Musalkat may yiw ak jàmm.
Sasu Tit ca réewu Keret
Bàyyi naa la ca réewu Keret, ngir nga mottali la desoon ci liggéey bi, te samp ay njiiti mbooloo ca dëkk bu nekk, ni ma la ko sante woon. Njiit nag nii la wara mel: war na ñàkk ŋàññ, yem ci benn soxna, am ay doom yu gëm yu amul baatu gannaaw cig yàqute mbaa déggadi. Ndaxte kuy sàmm mbooloo mi mooy jawriñu Yàlla, kon warul am ŋàññ, walla di ku dëgër bopp mbaa ku tàng bopp; warul dib màndikat walla xeexkat mbaa ku bëgge ci alal ju lewul. Waaye war na man gan te bëgg lu baax, di ku maandu te jub, ku sell te not boppam. War na jàpp ci xibaar bu dëggu, bi lal sunu yoon, ba mana dénkaane ci njàngle mu wér mi, tey yey ñi weddi.
10 Loolu war na, ndaxte am na ñu bare ñu déggul lenn ndigal, rawatina ci Yawut yi, ñuy yàq xeli nit ñi ak seen waxi neen. 11 Fàww nga wedamloo leen, ndax dañuy tas këri lëmm, ciy jàngle li warul, ngir sàkku alal ju lewul. 12 Am na nitu Keret, di yonent ci ñoom, mu ne: «Waa Keret, ay fenkat lañu masa doon, ñu soxor ni ay rabi àll, fuqle te tayel.» 13 Te li mu wax dëgg la. Looloo tax nga war leena yey bu wóor ci seeni bàkkaar, ngir ñu am ngëm gu wér 14 te baña topp léebi diiney neen yu Yawut yi, mbaa tegtali nit, ñi dëddu dëgg. 15 Ñi sell seen lépp a sell, waaye ñi selladi te gëmadi seen dara sellul, du seeni xalaat, du seeni xel. 16 Dañoo mbubboo xam-xamu Yàlla, waaye seeni jëf weddi na ko; ñu sikk lañu te déggadi, ba tële ci jëf lenn lu baax.