Buur ya
di téere bu jëkk bi
Lu jëm ci nguurug Suleymaan
Saar 1
(Saar 1.1—11.43)
Daawuda néew na doole
1 Gannaaw gi Buur Daawuda mujj naa màggat, ba làq at yu bare, ñu di ko sàng ay sér te du ko taxa tàng. 2 Ay dagam ne ko: «Buur, sang bi, nañu la wutal ab janq, mu di la taxawu, di la topptoo. Man naa tëdd it ci sa wet, Buur, ndax nga liwwi, sang bi.» 3 Ñu daldi seet ci tundu Israyil wépp, ba gis janq bu rafet bu ñuy wax Abisag, di waa Sunem. Ñu indil ko Buur. 4 Janq baa nga taaru lool. Muy topptoo nag Buur, di ko taxawu, waaye Buur dëkkoowu ko.
Adoñaa ngi sàkku jal bi
5 Ci biir loolu Adoña doomu Daawudaak Agit, di tëggu naan: «Man mii maay doon buur.» Mu waajalal boppam watiiru xare aki fas ak juróom fukki nit ñuy daw di ko jiitu. 6 Baayam Daawuda nag masu koo wax dara, ak lu mu mana def. Adoña moo toppoon ci Absalom. Mu doonoon ku góorayiw lool.
7 Ci kaw loolu Adoña diisook Yowab, mi Seruya di ndeyam, ak Abiyatar sarxalkat ba, ñooñu jàpple ko. 8 Waaye Cadog sarxalkat ba ak Benaya doomu Yoyada, ak Yonent Yàlla Natan, ak Simey ak Reyi, ñook jàmbaari Daawuda ya koy dar, ñooñu ànduñu woon ak Adoña. 9 Ba mu ko defee Adoña sarxe ay xar aki nag aki wëllu yu duuf ca wetu doju Soyelet, fa feggook En Rogel. Mu woo ca mboolem doomi Buur yu góor ya mu bokkal baay, ak jawriñi Buur yu diiwaanu Yuda. 10 Waaye woowul Yonent Yàlla Natan ak Benaya, woowul jàmbaar yay dar Daawuda, woowul rakkam Suleymaan.
11 Ba loolu amee Natan laaj Batseba, ndeyu Suleymaan, ne ko: «Waaw, xanaa déggoo ne Adoña doomu Agit falu na buur te sunu sang Daawuda yégu ko? 12 Kaay gaaw, ma digal la nooy def, ba musal sa bakkan ak sa bakkanu doom Suleymaan. 13 Gaawal dem ca Buur Daawuda, ne ko: “Buur, sang bi, du yaa ma giñaloon, yaw sang bi, ne ma sama doom Suleymaan mooy falu buur, wuutu la, te mooy toog ci sa jal bi? Kon nag lu tax Adoña falu buur?” 14 Gisal, diir bi ngay wax ak Buur foofa, man dinaa duggsi, topp ci yaw te dinaa dëggal sa kàddu.»
15 Batseba dem ba ca Buur, ca biir néegam. Buur a nga màggat lool, Abisag mu Sunem di ko taxawu. 16 Batseba agsi sujjóotal Buur, sukk fi kanamam. Buur ne ko: «Lu doon say tànk?» 17 Mu ne ko: «Sama sang, yaw yaa ma giñal ci sa Yàlla Aji Sax ji, sang bi, nga ne ma sama doom Suleymaan de dina falu buur moos, wuutu la, te moom mooy toog ci sa kaw jal bi. 18 Waaye xoolal léegi Adoñaa ngii falu buur, te yaw Buur sang bi, yéguloo ko. 19 Sarxe na ay nag ak wëllu yu duuf ak xar yu bare. Woo na ca doomi Buur yu góor yépp, woo ca Abiyatar sarxalkat ba, woo ca Yowab, njiitu mbooloom xare mi. Waaye Suleymaan sa surga ba, woowu ko. 20 Yaw nag Buur, sang bi, Israyil gépp a ngi ne jàkk ci yaw, ngir nga xamal leen kan ngay dëj ci sab jal, mu wuutu la, sang bi. 21 Lu ko moy de Buur, sang bi, bés boo nopplujee fekki say maam, su boobaa man, maak sama doom Suleymaan dinañu nu tuumaal.»
22 Na Batseba di wax ak Buur, Yonent Yàlla Natan jekki ne jalañ. 23 Ñu wax ko ne ko: «Buur, Yonent Yàlla Natan a ngoog.» Mu agsi ba ci kanam Buur, sujjóotal ko, dëpp kanamam fa suuf. 24 Natan ne ko: «Buur, sang bi, ndax yaa wax ne Adoña mooy falu buur, wuutu la, te moom mooy toog ci kaw jal bi? 25 Ndax kat, Adoña dem na tey jii, sarxeji lu bare ciy nag ak wëllu yu duuf aki xar. Woo na ca doomi Buur yu góor yépp, ñook njiiti xare yeek Abiyatar sarxalkat bi. Ña nga noonee di lekk ak a naan ñook moom te naa: “Buur Adoña, guddalu fan!” 26 Man sa surga bii nag, maak Cadog sarxalkat bi ak Benaya doomu Yoyada ak sa surga ba Suleymaan, woowu nu ca. 27 Buur, sang bi, ndax wér na ne loolu ndigal la lu bàyyikoo fi yaw, te xamaloo nu kan mooy toog ci sa kaw jal bi, wuutu la, yaw Buur, sang bi?»
28 Buur Daawuda ne ko: «Wool ma Batseba!» Ci kaw loolu Batseba dikk taxaw fa kanam Buur. 29 Buur daldi giñ ne: «Giñ naa ci Aji Sax ji, Kiy Dund te musal sama bakkan bii ci jépp njàqare, 30 bir na ne loolu ma la giñaloon ci Aji Sax ji, Yàllay Israyil, ne la bir na ne Suleymaan sa doom mooy doon buur wuutu ma te mooy toog ci kaw jal bii ma toog— loolu déy dinaa ko sottal bés niki tey.» 31 Ba mu ko defee Batseba dëpp kanamam fa suuf, sukk fa kanam Buur, ne ko: «Buur Daawuda, sang bi, yal nanga fi yàgg.»
Suleymaan falu na
32 Buur Daawuda daldi ne: «Wool-leen ma Cadog sarxalkat bi, ak Yonent Yàlla Natan ak Benaya doomu Yoyada.» Ba ñu dikkee fa kanam Buur, 33 Buur ne leen: «Àndleen ak samay dag, ngeen waral sama doom Suleymaan ca sama kaw berkelle bu jigéen ba, te yóbbu ko Giyon, bëtu ndox ba. 34 Cadog sarxalkat bi ak Yonent Yàlla Natan, nañu ko diw foofa, fal ko mu jiite Israyil. Su ko defee ngeen wal liit gi te yéene ne: “Buur Suleymaan, guddalu fan!” 35 Ngeen topp nag ci moom, délsi, mu dikk toog ci kaw jal bi. Moom mooy nguuru, wuutu ma. Moom laa fal, mu yilif Israyil ak Yuda.» 36 Ba loolu amee Benaya doomu Yoyada ne Buur: «Buur, sang bi, yal na ko Aji Sax ji sa Yàlla dogal. Amiin! 37 Na Aji Sax ji ànde woon ak yaw Buur, sang bi, yal na ni àndeek Suleymaan, te yal na kaweel ab jalam, ba mu sut sab jal, yaw Buur Daawuda, sang bi.» 38 Gannaaw loolu Cadog sarxalkat ba daldi ànd ak Yonent Yàlla Natan ak Benaya doomu Yoyada, ak waa Keret ak waa Pelet yay dar Daawuda. Ñu waral Suleymaan berkelleb Buur Daawuda. Ñu dar ko ba Giyon, bëtu ndox ba. 39 Ci kaw loolu Cadog sarxalkat ba dem ca xaymab Aji Sax ji, jële fa béjjén ba def diwu pal ga, diw ca Suleymaan. Ñu wal liit ga, mbooloo ma mépp àddu ca kaw ne: «Buur Suleymaan, guddalu fan!» 40 Ba loolu amee mbooloo ma mépp topp ca, bég lool, di toxoro, coow la jolli, ba suuf sa di riir.
41 Ba mu ko defee Adoña dégg ca, mook mboolem ña mu woo woon, ñu nekk faak moom. Fekk ñu lekk ba noppi. Ba Yowab déggee liit ga, da ne: «Waaw, riir mi ci dëkk bi, lu mu doon?» 42 Daaneelagul kàddoom sax, Yonatan doomu Abiyatar sarxalkat ba ne jaas, agsi. Adoña ne ko: «Dikkal, yaw nit ku baax nga, te xibaaru jàmm ngay indi.» 43 Yonatan ne Adoña: «Déedéet kay, sunu sang Buur Daawuda fal na Suleymaan buur. 44 Buur boole na kook Cadog sarxalkat bi ak Yonent Yàlla Natan ak Benaya doomu Yoyada ak waa Keret ak waa Pelet yay dar Buur. Yebal na leen, ñu waral ko berkelleb Buur. 45 Cadog sarxalkat baak Yonent Yàlla Natan diw nañu ko, fal ko ca Giyon, ba bàyyikoo ca, di ko bége, mu dim riir ci dëkk bi. Mooy coow, li ngeen dégg. 46 Suleymaan sax toog na ca jalu buur; 47 te it jawriñi Buur ñëw nañu, di sargalsi sunu sang Buur Daawuda, ne ko: “Yal na sa Yàlla siiwal turu Suleymaan, ba mu gën laa amu tur. Yal na kaweel ab jalam, ba mu gëna kawe sab jal.” Buur sujjóot ca kaw lalam, 48 teg ca ne: “Cant ñeel na Aji Sax ji, Yàllay Israyil, ji ma jox bésub tey ku ma wuutu ci samab jal, may gis.”» 49 Ba loolu amee tiitaange jàpp mboolem ña ñu woo woon ca jataayu Adoña. Ñu jóg, tasaaroo, ku nekk dem yoonam.
50 Adoña nag ragal Suleymaan, daldi dem jàpp ca béjjén ya ca cati sarxalukaay ba, ngir rawale bakkanam*1.50 Jàpp ca sarxalukaay ba ca kër Yàlla ga, nit daan na ko def, di ko sàkkoo rawale bakkanam. Seetal ci Mucc ga 21.14.. 51 Ñu wax ko Suleymaan, ne ko: «Buur Suleymaan, Adoña de, ragal na la. Deful lu moy jàpp ca béjjéni sarxalukaay ba te naa: “Na ma Buur Suleymaan sang bi giñal tey jii ne du ma jam saamar, ma dee.”» 52 Suleymaan daldi ne: «Su dee nit ku jara wóolu de, genn kawaram du wadd ci suuf. Waaye su lalee pexem wor de, dina dee.» 53 Ba loolu amee Buur Suleymaan yónnee, ñu jëleji Adoña ca sarxalukaay ba, mu dikk, sujjóotal Buur Suleymaan. Mu ne ko: «Man ngaa ñibbi sa kër.»
*1:50 1.50 Jàpp ca sarxalukaay ba ca kër Yàlla ga, nit daan na ko def, di ko sàkkoo rawale bakkanam. Seetal ci Mucc ga 21.14.