Saar 10
Ba loolu amee Samiyel jël njaqal diwu oliw lu ndaw, sotti ko ci kaw boppu Sóol, fóon ko, ne ko: «Aji Sax ji diw na la déy, ngir fal la njiitu ñoñam. Gannaaw boo teqlikook man, dinga dajeek ñaari góor ca wetu bàmmeelu Rasel ca Celca ca diiwaanu Beñamin. Dinañu la wax ne la mbaam ya nga seeti woon feeñ nañu. Te sax sa baay xalaatatul mbaam yi, yeena ko jaaxal. Ma nga naan: “Ana nu may def ak sama doom ji?” Boo fa jógee, jubalal ba jot garab gu mag ga ca Tabor. Ñetti góor dinañu fa dajeek yaw, di màggali Yàlla ca Betel; kenn ka gàddu ñetti tef, keneen ka ŋàbb ñetti kàmpi mburu, ka ca des yor mbuusum biiñ. Dinañu la nuyu, may la ñaari mburu; nga nangoo ko ca seeni loxo. Bu loolu weesee nanga dem ba ca Gibeya Eloyim, fa dalub xarekati Filisti ya nekk. Booy jub dëkk ba, dinga dajeek kurélu yonent yu jóge ca bérabu jaamookaay ba, aw nit jiitoo leen powum tabalaaki toxoro, ak ñaari xeeti xalam, yonent ya di waxe ni yonent* 10.5 waxyu: wax lay doon, ju Yàlla déey ab yonent, mu di ko biral ci ndigalal Yàlla. Leeleeg bu ab yonent tolloo ci biral waxyu, day mel ni ku daanu leer.. Su ko defee Noowug Aji Sax jee naa milib ci sa kaw, ngay waxandoo ak ñoom, soppiku, doon keneen nit. Bu la firnde yooyu dikkalee rekk, xamal ne Yàllaa ngi ànd ak yaw. Su boobaa, lu bés bi laaj, def ko. Léegi doxal jiitu ma Gilgal. Maa ngi noonu di la fekksi, ngir rendi fa saraxi rendi-dóomal, sarxe fa saraxi cant ci biir jàmm. Juróom ñaari fan nag ngay négandiku, ba ma fekksi la fa, xamal la looy def.»
Noowug Yàlla gane na Sóol
Naka la Sóol bàyyikoo ca Samiyel, walbatiku, Yàlla daldi soppi xelam. Firnde yooyu yépp nag matandoo ca bés ba. 10 Ba Sóol ak surgaam àggee Gibeya, kurélu yonent yaa ne pemm, dajeek moom. Noowug Yàlla ne milib ca kaw Sóol, muy waxandoo ak ñoom ay waxyu. 11 Ci kaw loolu mboolem ña xamoon Sóol démb ak bëkk-démb, daldi yem ci moom, mu ànd ak yonent ya di wax ay waxyu. Nit ña naan ca seen biir: «Waaw, Sóol doomu Kis jii, lu ko jot nii? Sóol it ci yonent yi laa?» 12 Jenn waay ju fa dëkk ne: «Yii yonent sax, ci ngéru kan lañu bokk?» Ca lañu jóge, def ko waxin naan: «Sóol it ci yonent yi laa?» 13 Sóol biral ay waxyu ba noppi daldi dem ca bérabu jaamookaay ba.
14 Ci kaw loolu baayu Sóol bu ndaw laaj Sóol ak surgaam, ne leen: «Fu ngeen demoon?» Sóol ne ko: «Mbaam yi lanu seeti woon, gisunu dara, nu dem ca Samiyel.» 15 Baayam bu ndaw ne ko: «Wax ma boog lu leen Samiyel wax.» 16 Sóol ne ko: «Samiyel da noo biralal ne mbaam ya feeñ na.» Mbirum nguur ma ko Samiyel wax nag, Sóol waxu ko baayam bu ndaw.
Yàlla feddli na palug Sóol
17 Gannaaw loolu Samiyel woolu askanu Israyil ca Aji Sax ji ca Mispa. 18 Mu wax bànni Israyil, ne leen: «Aji Sax ji Yàllay Israyil dafa wax ne: “Man maa génne Israyil Misra. Maa leen xettli ca waa Misra ak mboolem buur ya leen notoon. 19 Waaye tey yeena dëddu seen Yàlla, ji leen musal ci mboolem seeni loraange ak seeni njàqare. Yeena ko ne: ‘Falal buur ci sunu kaw daal!’ Léegi nag taxawleen fi kanam Aji Sax ji, giir ak giir, làng ak làng.”»
20 Ba Samiyel wooyee giiri Israyil yépp, ñu dikk, giirug Beñamin moo génn. 21 Mu woo giirug Beñamin, làng ak làng, làngu Matiri génn, Sóol doomu Kis génne ca. Ñu seet Sóol, gisuñu ko. 22 Ñu laajaat Aji Sax ji, ne ko: «Ndax keneen da fee ñëw?» Aji Sax ji ne: «Mu ngi nii, mu ngi làqu ci biir denc bi.» 23 Ñu daw jële Sóol foofa, mu taxaw ca biir mbooloo ma, sut ñépp. 24 Samiyel wax ak mbooloo mépp, ne leen: «Yeena gis ki Aji Sax ji taamu? Kenn melul ni moom ci mbooloo mi mépp.» Mbooloo ma mépp àddu ca kaw ne: «Buur, guddalu fan!» 25 Samiyel nag xamal mbooloo ma sañ-sañu buur. Mu bind ko cib téere, teg ca kanam Aji Sax ji. Ba mu ko defee Samiyel yiwi mbooloo mépp, ku nekk ñibbi këram.
26 Sóol itam ñibbi këram ca Gibeya, jàmbaari góor yi ci Yàlla xiir, ànd ak moom. 27 Terewul mu am ay nit ñu tekkiwul dara di wax, naan: «Ana nan lanu waa jii di xettlee?» Ñooñu sewal ko, yótuñu ko jenn teraanga. Sóol nag ne cell.

*10:5 10.5 waxyu: wax lay doon, ju Yàlla déey ab yonent, mu di ko biral ci ndigalal Yàlla. Leeleeg bu ab yonent tolloo ci biral waxyu, day mel ni ku daanu leer.