Saar 17
Golyaat dëkk na bànni Israyil
1 Waa Filistee boole woon seeni gàngoor ngir xare. Ñu daje ca dëkk ba ñu naan Soko ca diiwaanu Yuda, daldi dale ca Efes Damim diggante Soko ak Aseka. 2 Sóol ak waa Israyil nag daje, dale ca xuru Ela, làng-dér ngir jànkoonteek waa Filisti. 3 Waa Filistee nga taxawe tund wii, bànni Israyil taxawe tund wee, xur wa dox seen diggante.
4 Ci biir loolu jenn jàmbaar génne ca làngu waa Filisti. Ku ñuy wax Golyaat*17.4 Golyaat: am na ñu ko gëna xam ci turu Jalut., dëkke Gaat, taxawaayam di juróom benni xasab yu teg diggante baaraamu déy ak digg, xawa tollu ci ñetti meetar. 5 Mbaxanam xànjar la sol ak kiiraayal dënnub juróom benn fukki kilo, ñu liggéeye ko waasintóori xànjar. 6 Ma nga takk kiiraayi yeel yu xànjar, gàlloo xeeju xànjar bu ndaw ca wagg ya. 7 Bantu xeejam bu mag baa nga saf mbaamum ràbb, ñawkay xeej ba di weñ gu ëpp juróom ñaari kilo. Gàddukatu pakkam baa ngay dox, jiitu ko.
8 Golyaat taxaw, janook làngi Israyil, àddu ca kaw, ne leen: «Ana lu ngeen di génn, làng-déral xare nii? Xanaa du maay waa Filisti ji, yeen ngeen di surgay Sóol? Tabbleen genn góor, mu wàcc, dajeek man. 9 Su ma manee ba rey ma, nuy seeni jaam; waaye su ma ko manee ba rey ko, ngeen di sunuy jaam, di nu jaamu.» 10 Waa Filisti ba neeti: «Maa dëkk làngi Israyil bés niki tey. Booleleen maak genn góor rekk, nu xeex.» 11 Ba Sóol ak bànni Israyil yépp déggee waxi waa Filisti jooju, jàq nañu, tiit nañu lool.
Daawuda def na jaloore
12 Daawuda nag moo doon doomu góor googu dëkk Efrata ca Betleyem ga ca diiwaanu Yuda, ñu di ko wax Yese. Yese amoon na juróom ñetti doom yu góor. Góor ga, ca jamonoy Sóol, mag mu ñu nawloo la woon. 13 Ñetti doomi Yese yu góor yu mag ñoo ràngu woon, topp Sóol ca xare ba. Ñetti doom ya dem xare, taaw ba Elyab lañu koy wax, ka ca topp di Abinadab, ñetteel ba di Simeya. 14 Daawudaa ca gënoon di ndaw. Ñetti magam yooyu ñoo toppoon Sóol, 15 waaye Daawuda da daan jaabantee fa Sóol ak Betleyem ga muy sàmme gàtti baayam.
16 Subaak ngoon nag waayu Filisti ja ne jaas taxaw, ba mu am ñeent fukki fan. 17 Ci biir loolu Yese ne doomam Daawuda: «Ayca, jëlal nattub mbool mii ak fukki mburu yii te nga daw, yóbbul ko sa mag ya ca dal ba. 18 Fukki dogi formaas yii, yóbbul ko seen njiitu kurél. Nemmikul seen jàmmu yaram te nga sàkku ci seen firnde, indil ma. 19 Sóol a ngaak ñoom ak waa Israyil gépp ca xuru Ela, di xareek waa Filisti.»
20 Daawuda teela jóg ca ëllëg sa, wacce gàtt ya ab wattukat, daldi jël yóbbal ga, dem na ko ko baayam sante. Naka la àgg ca dal ba, yemook gàngoor gay génnaale seen xaacuy xare, ngir làng-déri. 21 Bànni Israyil ak waa Filisti daldi dér, gàngoor janook gàngoor. 22 Ci biir loolu Daawuda wàcce yóbbal ga, wacce ko wattukatub cummikaay ba, daldi daw ba ca làngu xare ba. Mu agsi, nuyook ay magam. 23 Na muy wax ak ñoom, jàmbaar ja ñuy wax Golyaat waa Filisti ba dëkke Gaat, ne tëll génne ca làngi waa Filisti. Mu dellu ca wax jooju mu waxoon, Daawuda dégg ca.
24 Ba bànni Israyil gépp gisee waa ja, dañoo dellu gannaaw, tiit lool. 25 Ña nga naan ca seen biir: «Gis ngeen waa jee di ñëw, dëkksi Israyil a ko yékkati. Képp ku ko rey de, Buur dina ko jox alal ju bare. Doomam la koy may jabar, te waa kër baayam, dina leen jagleel ab cér ci digg Israyil.» 26 Daawuda ne ña mu dendal: «Ngeen ne, lees di defal ku rey waa Filisti bii, ba faj gàcceg Israyil? Ak kuy yéefaru waa Filisti bii sax, bay dëkk gàngoori Yàlla jiy dund?» 27 Nit ña dellu ca loola ñu waxoon, ne moom lañuy defal ku rey waa ja.
28 Elyab, magu Daawuda, dégg Daawuda di wax ak ñooña. Mu mer, ne ko: «Yaw sax lu la fi indi? Ak koo wacce la fay gàtt ak as néew ca àll ba? Xam naa bu baax sag réy ngise, ak njubadi gi nga mébét. Seetaansi xare bi doŋŋ a la fi indi!» 29 Daawuda ne ko: «Waaw, man lu ma def? Xanaa du wax doŋŋ?» 30 Daawuda jóge ca mag ja, dem ca keneen, laaj ko mbir mooma, tont la di lenn.
31 Ci kaw loolu ñu dégg kàddu ya ca Daawuda wax, yegge ko Sóol. Sóol woolu ko. 32 Daawuda dikk ne Sóol: «Bu kenn yoqil waa jii, sang bi. Man maay dem xeex ak waa Filisti bii.» 33 Sóol ne Daawuda: «Déedéet, yaw manoo songi waa Filisti bii, di xeex ak moom. Gone doŋŋ nga, te moom cag ndawam la dale di nitu xare.» 34 Daawuda ne Sóol: «Sang bi, bu may sàmm sama gàtti baay, ba gaynde mbaa rab wu aay dikk, jël ci ab gàtt, 35 maa koy topp, dóor ko, nangoo gàtt bi ci gémmiñam. Te bu ma songee, sikkim bi laay sëq, fàdd, mu dee. 36 Rey naa gaynde, rey naa weneen rabu àll wu aay, sang bi. Kon nag yéefaru Filisti bii it ni wenn ci yooyu rab rekk, ndax moo tëkku gàngoori Yàlla jiy dund. 37 Daawuda neeti: Aji Sax ji ma musal ci pàddum gaynde ak weneen rabu àll wu aay, moo may musal ci loxol waa Filisti bii.» Sóol ne Daawuda: «Demal boog, yal na Aji Sax ji ànd ak yaw.»
38 Ba mu ko defee Sóol solal Daawuda yérey boppam, solal ko mbaxanam xànjar, solal ko kiiraayal dënn. 39 Daawuda ràngoo saamarub Sóol, ca kaw yére ya, daldi jéema dox, mu të, ndax ñàkk koo miin. Daawuda ne Sóol: «Manumaa doxaale lii ndax miinuma ko», daldi koy summi. 40 Ba loolu amee Daawuda jël yetam, tànn ca dex ga juróomi doj yu rattax, yeb ca gafakag mbuusum sàmmam, daldi ŋàbb mbaqam, wuti waa Filisti ba. 41 Ci biir loolu waa Filisti ba, dox, dikk ba jege Daawuda, gàddukatu pakkam jiitu ko. 42 Waa Filisti ba séentu, séen Daawuda; muy xale su góor su ndaw, xees te góorayiw, mu daldi koy xeeb. 43 Mu ne Daawuda: «Xanaa ab xaj laa, ba nga di ma jëlalu yet?» La ca tegu waa Filisti ba móolu ko ca turi tuuram, 44 ne ko: «Dikkal fii rekk, ba ma leele saw suux njanaaw yeek rabi àll yi.»
45 Daawuda ne waa Filisti ba: «Yaw de yaa may jëlal ab saamar ak xeej bu mag ak bu ndaw, waaye man turu Aji Sax ju gàngoor yi laa lay dikke, Yàllay làngi xarey Israyil, ji nga tëkku. 46 Bésub tey jii Aji Sax jee lay teg ci sama loxo, ma rey la, dog sa bopp. Tey jii sax laay leele njanaaw yeek rabi àll yi, néewi xarekati Filisti, ba àddina sépp xam ne Israyil am na Yàlla. 47 Mboolem ñii fi daje dinañu xam ne du saamar te du xeej la Aji Sax jiy walloo, ndax Aji Sax jeey boroom xare bi, te moo leen teg ci sunuy loxo.»
48 Ci kaw loolu waa Filisti ba daldi dikk, ba gënatee jege Daawuda, Daawuda riir, wuti làng ga, ngir dajeek waa Filisti ba. 49 Mu yoor loxoom ca mbuusam, jël ca aw doj, mbaq, jam waa Filisti ba ci jë, doj wa tàbbi ca biir jë ba. Mu ne jànjaŋ, dëpp kanam ga fa suuf. 50 Ag mbaq aku doj la Daawuda mane waa Filisti ba, jam ko, rey ko, te yorul saamar.
51 Daawuda nag daw ba taxaw, tiim waa Filisti ba, jàpp saamaram, boccee ko ca mbar ma, jekkli ko, dog bopp ba. Waa Filisti gis ne seen ñeyu xare dee na, ñu daw. 52 Ba loolu amee mbooloom Israyil ak Yuda àddu xaacoondoo, daldi dàqi waa Filisti, ba jub xur wa, ba ca bunti Ekkron. Waa Filisti ya ñu rey ne wetar ca yoonu Saarayim ba Gaat, ba ca Ekkron. 53 Bànni Israyil nag waññikoo ca ndàqum Filisti mu metti ma, daldi sëxëtoo seen dal ba. 54 Daawuda jël boppu waa Filisti ba, yóbbu Yerusalem, gànnaayi waa ja, mu fat ca xaymab boppam.
55 Lu jiitu loolu, ba Sóol gisee Daawuda, mu wuti waa Filisti ba, da ne Abner njiital mbooloom xareem: «Waaw, Abner, xale bii doomu kan a?» Abner ne ko: «Buur, giñ naa, nga fekke tey, xawma ko.» 56 Buur Sóol ne ko: «Nanga laajte, xale bii, doomu kan la.» 57 Naka la Daawuda rey waa Filisti ba, ba dikk, Abner jàpp ko, indi ko ca kanam Sóol. Daawudaa nga ŋàbb boppu waa Filisti ba, ba tey. 58 Sóol ne ko: «Yaw, gone gii, yaay doomu kan?» Daawuda ne ko: «Maay doomu Yese, sa surga ba dëkk Betleyem.»