Saar 13
Ay kàdduy artoo aki tàggtoo ngi
Ñetteel bi yoon a ngii, bu ma leen di ganesi. «Ci kàddug ñaari seede ba ñett nag la àtteb mépp mbir di wére* 13.1 Seetal ci Baamtug Yoon wi 19.15.La ma waxoon ba noppi ca sama ñaareelu ngan, tey bi ma wuutee, moom laay baamtu, artoo ko ñi jëkkoona bàkkaar, ak ñi ci des ñépp: su ma délsee, duma ñéeblu kenn, gannaaw yeenay wut lu firndeel ne ci man la Almasi di waxe ak yeen, te moom néewul kàttan, diggam ak yeen, waaye ku manoorewu la ci seen biir. Cig néew doole lees ko daaje ci bant ba rey ko, waaye tey ci manoorey Yàlla lay dunde. Nun itam sunug bokk ci Almasi moo tax nu néew doole, waaye ci manoorey Yàlla lanuy bokk ak moom di dund, bu nuy jëflante ak yeen.
Xoolaatleen seen bopp, ba xam ndax yeena ngi ci yoonu ngëm wi. Nattleen seen bopp, xanaa xam ngeen ne Yeesu Almasee ngi ci yeen? Ndegam du seen gëmadi, la natt ba firndeel! May yaakaar nag ne nun, dingeen xam ne firndeel nanu sunu taxawaay. Teewul nuy ñaan Yàlla, ngeen baña def dara lu bon, te ñaanunu loolu am, ngir nu man koo firndeele sunu taxawaay, waaye bu sunub taxawaay doonul woon lu firndewu itam, sunu yéene mooy ngeen di def lu baax. Ndax kat manunoo def dara ba sot liy dëgg, manunu lu dul liggéeyal liy dëgg. Bu nu néewee doole, te ngeen am doole, bég nanu. Lii itam, nu ngi koy ñaan, te mooy ngeen yokku ba mat sëkk. 10 Looloo tax ma bind leen lii bala maa dikk, ba buma dikkee, du jar may mettil ni may jëflante ak yeen, ci kaw sañ-sañ bi ma Boroom bi jox. Ndax kat sañ-sañ bi, yokke moo ko taxa jóg, waaye deesu ko yàqe.
11 Ma tëje fii nag, bokk yi, bégleen, yokkuleen ba mat sëkk, ñaaxanteleen, mànkooleen te jàmmoo. Su ko defee Yàlla miy Yàllay cofeel ak jàmm mooy ànd ak yeen.
12 Saafoonteeleen fóonante yu sell. Ñu sell ñépp a ngi leen di nuyu.
13 Sunu yiwu Sang Yeesu Almasi nag, ak cofeelu Yàlla, ak bennoo geek Noo gu Sell gi, yal nañu bokk ànd ak yeen ñépp.

*13:1 13.1 Seetal ci Baamtug Yoon wi 19.15.