Yenn xew-xew a ngi
Saar 21
Waa Gabawon feyu nañu
1 Jamono ya Daawuda nekkee ci jal bi, amoon na xiifub ñetti at yu tegloo. Daawuda diis ko Aji Sax ji. Aji Sax ji ne ko: «Li waral xiif bi moo di àqu deret ji topp Sóol ak waa këram ndax waa Gabawon ña mu rey.» 2 Buur woo waa Gabawon, wax ak ñoom. Waa Gabawon bokkuñu woon ci bànni Israyil, waaye ñoo desoon ca Amoreen ña bànni Israyil giñaloon ne duñu leen rey. Teewul Sóol xéroon lool ci bànni Israyil ak Yuda, bay fexee faagaagal waa Gabawon. 3 Daawuda laaj waa Gabawon, ne leen: «Lan ngeen bëgg ma defal leen ko? Ana lu may def ba jotoo ko àq, ji ñu leen ameel, ba ngeen ñaanal ñoñi Aji Sax ji?» 4 Waa Gabawon ne ko: «Du xaalis, du wurus wu nuy laaj Sóol mbaa waa këram; te it du kenn ci Israyil ku nu saña reylu.» Mu ne leen: «Waxleen boog lu ngeen di laaj, ma defal leen ko.» 5 Ñu ne ko: «Sóol da noo naroona fexeel, sànk nu, faagaagal nu ci réewum Israyil. 6 Kon dees nuy jox juróom ñaari góor ñu askanoo ci Sóol, nu jam leen ba mu sar fa kanam Aji Sax ji ca Gibeya, dëkkub Sóol, ma Aji Sax ji faloon.» Buur ne leen: «Dinaa leen leen jox.»
7 Teewul Daawuda déeg Mefiboset, ma Yonatan doomu Sóol di baayam, ndax la ñu giñoo woon ci Aji Sax ji, mook Yonatan doomu Sóol. 8 Buur nag jàpp Armoni ak meneen Mefiboset, te Rispa doomu Aya di seen yaay, Sóol di seen baay. Buur boole ca juróomi góor ña Mikal*21.8 Mikal mii du Mikal mi ñuy wax ci 6.23, ne amul doom, ba keroog muy dee. Mikal mii mook Merab ñuy wax ci 1.Samiyel 18.19 kenn nit ki la. Jëkkëram mooy Àddiryel. doomu Sóol di seen yaay, te Àddiryel doomu Barsilay ma dëkk Mewola di seen baay. 9 Daawuda jébbal leen waa Gabawon, ñu jam leen ba mu sar, foofa ca kaw tund wa, fa kanam Aji Sax ji. Juróom ñaar ñooñu ñépp a bokk tëdd. Ña nga leen rey ca fan ya ñu tàmbalee góob, ca ndoortel ngóobum lors ba.
10 Ba mu ko defee Rispa doomu Aya ju jigéen ja, jël ab saaku, tàllalal ko boppam ca doj wa. La ko dale ca ndoortel ngóob ma, ba keroog asamaan di sóob ca kaw néew ya, Rispa bàyyiwul dara mu laal leen bëccëg mbaa guddi, du picc, du rabu àll.
11 Ba loolu amee ñu àgge Daawuda jëfi Rispa doomu Aya, nekkaaleb Sóol ba. 12 Daawuda dem jëleji yaxi Sóol ak doomam Yonatan ca waa Yabes Galàdd. Ndax gannaaw ba ñu daanee Sóol ca Gilbowa, Filisteen ña dañoo wékkoon néewu Sóol ak Yonatan ca péncum Bet San. Waa Yabes Galàdd dikk sàcce leen fa. 13 Ci kaw loolu Daawuda jële fa yaxi Sóol ak doomam Yonatan, ak yaxi nit ña ñu jamoon ba mu sar te wékk leen. 14 Ñu boole kook yaxi Sóol ak doomam Yonatan, denc lépp ca sëgu Kis, baayu Sóol, ca diiwaanu Beñamin ca Sela. Ñu def la Buur santaane lépp. Gannaaw loolu Yàlla nangul réew ma.
Daawuda daje naak ponkali waa Filisti
15 Bu loolu wéyee, xare amaat na diggante Filisteen ñi ak bànni Israyil. Daawuda ànd aki nitam xarejeek Filisteen ña. Daawuda nag sonn ci biir xare bi. 16 Ci kaw loolu Isbi Bënob ne dina rey Daawuda — kooku askanu ponkal ya ñu daan wooye Rafayeen, ca la bokkoon. Ñawkay xeejam xànjar la, diise ñetti kilo. Mu yore itam saamar bu bees. 17 Teewul Abisay doomu Seruya dikk, wallusi Daawuda, jam Filisteen ba, rey ko. Niti Daawuda daldi cay giñal Daawuda, ne: «Dootuloo ànd ak nun mukk cib xare. Lu ko moy dinga ci dee, askanu buur fey ci Israyil.»
18 Gannaaw gi xare dellu am seen digganteek Filisteen ña ca dëkk ba ñuy wax Gob. Ca la Sibeka, ma askanoo ci Usa, rey Saf ma bokk ca askanu ponkal ya. 19 Xare amati ca Gob seen digganteek Filisteen ña. Elxanan doomu Yare Oregim ma dëkk Betleyem, jam Golyaat ma dëkk Gaat. Kookoo di waa ja bantub xeejam réyoon, ba tollu ni mbaam mu ñuy ràbbe.
20 Xare dellu amati ca Gaat. Jenn waay ju réya réy a nga ca woon, ku am juróom benni baaraam, loxo bu nekk, ak juróom benni baaraam, tànk bu nekk, lépp di ñaar fukki baaraam ak ñeent. Moom it ponkalum Rafayeen la woon. 21 Ba mu tëkkoo Israyil, Yonatan a ko rey. Yonatan, Simeya magi Daawuda mooy baayam. 22 Ñeent ñooñu ay ponkali Rafayeen lañu woon ca Gaat. Daawudaaki nitam ñoo leen jam, ñu daanu.
*21:8 21.8 Mikal mii du Mikal mi ñuy wax ci 6.23, ne amul doom, ba keroog muy dee. Mikal mii mook Merab ñuy wax ci 1.Samiyel 18.19 kenn nit ki la. Jëkkëram mooy Àddiryel.