Saar 3
Piyeer doxloo na ab lafañ
1 Piyeer ak Yowaan ñoo doon duggsi kër Yàlla ga, ngir jullig digg njolloor. 2 Fekk ñu indi fa waa ju judduwaale lafañ, ñu daan ko teg bés bu nekk ca bunt, ba ñuy wooye bunt bu Rafet, ca kër Yàlla ga, ngir muy sarxu ñay duggsi. 3 Waa ja gis Piyeer ak Yowaan, ñuy dugg ca kër Yàlla ga, mu di leen sarxu. 4 Ci kaw loolu Piyeer ne ko jàkk, mook Yowaan, ne ko: «Xool nu.» 5 Lafañ bi teewlu leen, di leen séentoo ab sarax.
6 Piyeer nag ne ko: «Xaalis ak wurus de, yoruma ko. Waaye li ma am, jox naa la ko: ci turu Yeesu Almasi waa Nasaret bi, doxal!» 7 Mu jàpp ci loxol ndijooram, yékkati ko. Ci saa si ay tànkam aki kostanam dëgër. 8 Mu ne layy, taxaw, tàmbalee dox, ànd ak ñoom dugg ca kër Yàlla ga, di dox ak a tëbantu, tey sant Yàlla. 9 Mbooloo mépp gis ko, muy dox, di sant Yàlla. 10 Ñu xàmmi ko, xam ne moo daan toog, di yalwaan ca bunt bu Rafet ba ca kër Yàlla ga. Ñu jommi ba jommaaral, ba far gëlëm ca la ko dikkal.
Piyeer waare na
11 Ba loolu amee waa ji taq ci Piyeer ak Yowaan, ñépp dawsi, sago jeex, ñu yéew leen ca mbaaru bunt ba ñu dippee Suleymaan. 12 Piyeer nag gis loolu, àddu, ne mbooloo ma: «Yeen bokki Israyil, lu ngeen di waaru ci lii? Lu ngeen nu naa jàkk, mel ni sunu manoorey bopp mbaa sunug njullite lanu doxloo kii? 13 Moom Yàllay Ibraayma, di Yàllay Isaaxa, di Yàllay Yanqóoba, te di sunu Yàllay maam kay, moo màggal jawriñam Yeesu. Yeen nag yeena ko teg ciy loxo, jàmbu ko fa kanam Pilaat, te mu naroon koo bàyyi. 14 Yeen, yeena jàmbu Ku sell ki te jub, tinul ab bóomkat. 15 Bóom ngeen Kiy dundloo, waaye Yàllaa ko dekkal, nu seede ko. 16 Gëm aw turam moo waral turam woowu dooleel nit kii ngeen gis, xam ko. Kon ngëm moo waral lii; ngëm gu sababoo ci Yeesu moo ko may mu wér péŋŋ nii ci seen kanam, yeen ñépp.
17 «Teewul nag bokk yi, xam naa ne ñàkka xam moo leen taxa jëfe noonu, te loolu it moo dal seeni kilifa. 18 Waaye Yàlla moo sottale noonu la mu yégle woon lu jiitu, yonent yépp jottli, ne Almaseem dina sonn. 19 Kon nag tuubleen te dëpp, ndax seeni bàkkaar faru. 20 Su boobaa jamonoy péex ay bawoo ci Boroom bi, te mooy yebal Almasi mu leen jagleel, te muy Yeesu. 21 Moom la asamaan wara dalal, ba kera jamono ja lépp di dellu jag, na ko Yàlla waxe woon, yonent yu sell ya woon jottli. 22 Musaa kay noon na: “Boroom bi seen Yàlla mooy seppee ci seenu xeet ab yonent ni man; nangeen ko déggal ci lépp lu mu leen wax. 23 Képp ku déggalul yonent boobu, dees na la xettee ci xeet wi, sànk la.”
24 «Te it mboolem yonent yi wax, dale ko ci Samiyel ak ñi ko wuutu, ñoom it yégle woon nañu bés yii nuy dund. 25 Yeen nag yeenay donoy yonent yi te yeenay séddu ci kóllëre, gi Yàlla fasoon ak seeni maam, ba mu nee Ibraayma: “Ci saw askan la xeeti àddina yépp di barkeel.” 26 Yeen la Yàlla jëkka wool jawriñam, daldi koy yebal ci yeen, ngir barkeel leen, waññee kenn ku nekk ci yeen, mu moy jikkoom yu bon.»