Saar 21
Póol jublu na Yerusalem
Gannaaw ba nu tàggoo ak ñoom, nu dugg gaal, jubal dunu Kos, teg ca teeri ca dunu Rodd, jóge fa, jàll ba Patara. Nu gis fa gaal gu jëm Fenisi, dugg ca, daldi teddi. Naka lanu dem ba séen dunu Sippar, wacc ko nag sunu wetu càmmoñ, jublu diiwaanu Siri, ba teeri Tir, ndax fa la gaal gi waroona yebbi ab yebam. Nu seet taalibey foofa, ba gis leen, toog ak ñoom juróom ñaari fan. Ci biir loolu Noo gu Sell gi di leen xiir ci wax Póol, ne ko bumu dem Yerusalem. Ba nu fa amee fan yooyu lanu fa bàyyikoo, dem, ñu gunge nu, ñoom ñépp, ñook seeni soxna ak seeni doom. Nu dem ba génn dëkk ba, daldi sukk ca tefes ga, ñaan. Ba loolu amee nu tàggtoo ba noppi, dugg ca gaal ga, ñoom ñu ñibbi.
Nun nag ba nu jógee Tir, danoo ñoqli ba teeri Patolemayis. Nu nuyoo faak bokki taalibe ya, toog faak ñoom benn fan. Ca ëllëg sa nu dem ba àgg Sesare. Nu dem kër Filib, xamlekatu xibaaru jàmm, bi bokk ci Juróom ñaar ñi*21.8 Juróom ñaar ña ñooy ñi doon séddale ndimbalu mbooloom gëmkat ña ca Yerusalem. Seetal ci 6.5.. Nu dal ak moom. Filib moomu amoon na ñeenti doomi janq yuy waxe ay waxyu.
10 Gannaaw ba nu fa toogee ay fan, ab yonent bu ñuy wax Agabus jóge Yude, agsi. 11 Mu dikk ba ci nun, jël ngañaayal Póol, yeewe ko ay tànkam aki loxoom, daldi ne: «Noo gu Sell gi dafa wax ne: “Ki moom ngañaay lii, nii la ko Yawut yiy yeewe ca Yerusalem, jébbal ko jaambur ñi dul Yawut.”»
12 Ba nu déggee loolu, nun ak waa gox baa tinu Póol, ne ko bumu dem Yerusalem. 13 Ci kaw loolu Póol ne: «Lu ngeen di def nii, di jeexal sama xol? Waxuma ñu yeew ma rekk, waaye dee sax nangu naa koo def ci Yerusalem ngir Sang Yeesu.» 14 Naka lanu wax, wax, mu të, nu bàyyi, daldi ne: «Kon nag yal na Boroom bi sottal coobareem!»
15 Gannaaw fan yooyu lanu fabu, ngir dem Yerusalem. 16 Ci biir loolu ay taalibe yu dëkke Sesare ànd ak nun, yóbbu nu fa nu wara dali, ca kër ku ñuy wax Manason, ma cosaanoo Sippar, te di taalibe bu yàgg.
Póol agsi na Yerusalem
17 Ba nu agsee Yerusalem nag, bokki taalibe ya bége nañu noo dalal. 18 Ca ëllëg sa Póol ànd ak nun, seeti Yanqóoba, fekk mag ñépp a nga fa teew. 19 Póol nuyook ñoom, ba noppi benn-bennalal leen jëf, ji Yàlla sottale liggéeyam ci biir jaambur ñi.
20 Ñu dégg ca, daldi sàbbaal Yàlla, ba noppi ne ko: «Mbokk mi, xoolal ñaata junniy Yawut a doon ay gëmkat, te ñoom ñépp di ñu xér ci yoonu Musaa. 21 Ñoo dégg nag sab jëw, ñu ne dëddu yoonu Musaa mooy li ngay jàngal mboolem Yawut yi dëkk ci biir jaambur ñi, naan leen buñu xarfal seeni doom, te buñu topp sunuy aada. 22 Lu ciy pexe nag? Ndax kat duñu umple ne dikk nga. 23 Léegi daal, dangay def li nu lay wax nii: nu ngi feek ñeenti nit ñu am lu ñu xasal Yàlla. 24 Ñoom ngay àndal, nga bokk ak ñoom setlu, te nga gàddu seen peyu wateefu bopp, wi boroom xas wu ni mel aadawoo. Su ko defee ñépp ay xam ne li ñu lay jëwe, dara amu ci, te yoonu Musaa ngay jëfe, di ko sàmm. 25 Naka gëmkat ñi dul Yawut nag, bind nanu leen li nu dogal, ne leen ñu moytu ñam wu ñu sarxal ay xërëm, moytoo lekk deret ak yàppu mala mu ñu tuurul deretam, te moytu powum séy.»
26 Ca ëllëg sa Póol ànd ak nit ña, bokk ak ñoom setlu, dugg ca kër Yàlla ga. Mu daldi xamle bés ba seen àppu setlu di mat, ba jooxe ba ci war génn, ñeel kenn ku nekk ci ñoom.
Jàpp nañu Póol
27 Ba àppu juróom ñaari fan yay waaja jeex, Yawut ya jóge diiwaanu Asi gis Póol ca kër Yàlla ga. Ñu yëngal mbooloo mépp, jàpp ko, 28 di xaacu naan: «Wallee, bokki Israyil! Waa jii, mooy kiy wër fépp, di waare ñépp kàddu gu safaanook njariñal xeet wi, ak yoonu Musaa ak bérab bii. Rax ci dolli mu indi ci kër Yàlla gi ay Gereg, ba sobeel bérab bu sell bii.» 29 Booba Torofim mu Efes la ñu gisoon ca dëkk ba, mu ànd ak Póol, ñu yaakaar ne Póol da koo yóbbu ca kër Yàlla ga. 30 Ba loolu amee dëkk ba bépp màbb, nit ña ne kër-kër, ne këpp, ñu jàpp Póol, génne ko kër Yàlla ga rekk, daldi tëj bunt ya.
31 Naka lañu koy wuta rey, ñu àgge njiital gàngooru Room ba yore kilifteef ga, ne ko Yerusalem gépp salfaañoo na. 32 Ca saa sa mu ànd ak ay dag, ak njiiti takk-der, ne jaas ca biir mbooloo ma. Yawut ya nag gis njiital gàngoor ga ak dag ya, daldi dakkal yar ya ñu doon dóor Póol.
33 Ci kaw loolu njiit la agsi, jàpp ko, daldi santaane ñu jénge ko ñaari càllala. Ba loolu wéyee mu laajte, ne: «Kii ku mu doon, ak lu mu def?» 34 Ñenn ca mbooloo ma xaacu ne lii, ña ca des ne laa. Ñolñol ja nag tax manu caa xam dara lu leer. Mu daldi santaane, ñu yóbbu ko ca biir tata ja. 35 Ba Póol àgge ca dëggastali tata ja, mbooloo ma daa sànju ak doole, ba takk-der ya mujj fab Póol, gàddu ko. 36 Ndax booba mbooloo mu réy a ko topp, di xaacu naa: «Na dee!»
Póol layoo na ak Yerusalem
37 Naka lañu koy waaja dugal ca tata ja, Póol ne njiitu gàngoor ga: «Ndax man naa laa wax baat?» Mu ne ko: «Ndeke dégg nga gereg? 38 Kon du yaay waayu Misra jooju yëngaloon dëkk bi ci fan yii, te yóbbu woon ñeenti junniy Bóomkat ya (4 000) ca màndiŋ ma?» 39 Póol ne ko: «Man de ab Yawut laa, di as goru Tàrs, dëkk bu ñàkkul tur ba ca diiwaanu Silisi. Dama lay ñaan, nga may ma, ma wax ak mbooloo mi.» 40 Mu may ko. Póol taxaw ca dëggastal ya, tàllal mbooloo ma loxo, ñu ne selaw. Mu wax ak ñoom ci yawut, ne:

*21:8 21.8 Juróom ñaar ña ñooy ñi doon séddale ndimbalu mbooloom gëmkat ña ca Yerusalem. Seetal ci 6.5.