Amos
Saar 1
Kàdduy Amos a ngi, di boroom jur bu dëkkoon Tekowa*1.1 Tekowa sorewul ak Yerusalem, péeyu Yuda. Ba bànni Israyil xàjjalikoo ñaari réew gannaaw ba Buur Suleymaan nelawee, réewum Israyil daa péeyoo Samari; réewu Yuda péeyoo Yerusalem.. Mu am peeñu mu jëm ci Israyil ci janti Osiyas1.1 Osiyas mooy Asaryaa itam. buurub Yuda ak janti doomu Yowayas, Yerbowam buurub Israyil. Loolu tollu ci ñaari at lu jiitu yëngu-yëngu suuf ba. Mu ne:
Aji Sax jeey yëmmoo fa Siyoŋ1.2 Siyoŋ mooy tund wa kër Yàlla ga nekk ca Yerusalem. Daan nañu ko tudde it dëkku Yerusalem.,
Yerusalem lay àddoo,
parluy sàmm si ne faraas,
mbooyum kaw tundu Karmel lax.
Aji Sax ji mbugal na xeet yi
(Saar 1.3—2.16)
Aji Sax ji da ne:
«Ñetti bàkkaar, su ma yeboo ne ñeent, laay sikke waa Damaas§1.3 Damaas mooy péeyu réewum Siri.,
te duma fomm seeni duma.
Ñoo bàcce waa Galàdd bàccukaayi weñ.
Maay yebal sawara seen waa kër Buur Asayel,
mu xoyom taaxi Buur Ben Addàd.
Maay dàjji bunti dëkkub Damaas,
faagaagal waa xuru Awen*1.5 xuru Awen mooy tekki xuru Ñaawtéef.,
boole ca boroom Bet Eden1.5 Bet Eden mooy kërug Àjjana, muy tekki fii Kërug Xawaare..
Waa Siri dugg ngàllo, dellu Kir1.5 Kir la Arameen ñi cosaanoo. Gannaaw gi lañu sanci réewu Siri. Seetal ci 9.7.
Aji Sax jee ko wax.
 
Aji Sax ji nee:
«Ñetti bàkkaar, su ma yeboo ne ñeent, laay sikke waa Gasa§1.6 Gasa benn la ci juróomi dëkki Filisti yu mag; yeneen yi di Asdodd ak Askalon ak Ekkron, ak Gaat. Seetal ci 6.2.,
te duma fomm seeni duma.
Ñoo jàpp njaam mbooloom lëmm,
jalax Edomeen ña.
Maay yebal sawara ca tatay Gasa,
mu xoyom ay taaxam.
Maay fàkkas waa Asdodd,
fàkkas boroom yetu nguur fa Askalon,
fél Ekkron,
ndesu Filisteen ña sànku.»
Boroom bi Aji Sax jee ko wax.
 
Aji Sax ji nee:
«Ñetti bàkkaar, su ma yeboo ne ñeent, laay sikke waa Tir*1.9 Tir dafa mel ni Sidon. Ay dëkk yu mag lañu woon ca réewum Fenisi.,
te duma fomm seeni duma.
Ñoo jàpp mbooloom lëmm, jalax ca Edomeen ña,
te sédduñu ci kóllëreg bokk.
10 Damay yebal sawara ca tatay Tir,
mu xoyom ay tataam.»
 
11 Aji Sax ji nee:
«Ñetti bàkkaar, su ma yeboo ne ñeent, laay sikke waa Edom1.11 Edomeen ñaa nga bàyyikoo fa bëj-saalumu Yuda jàpp penku. Ñu ngi soqikoo ci Esawu, magu Yanqóoba, kon bokki Israyil lañu woon, waaye dañoo faroon ak nooni Israyil.,
te duma fomm seeni duma.
Ñoo toppe seen bokki bànni Israyil saamar,
jalax yërmande,
mer mer mu dul meddi
ak xadar ju dul giif mukk.
12 Maay yebal sawara fa Teman,
mu xoyomaale tatay Boccra1.12 Teman ak Boccra ay goxi Edom yu mag la woon. Boccra moo doon péeyu Edom.
 
13 Aji Sax ji nee:
«Ñetti bàkkaar, su ma yeboo ne ñeent, laay sikke Amoneen ñi,
te duma fomm seeni duma.
Ñoo butti ay jigéeni biir ca Galàdd
ba ñuy xare ngir yokk seen suuf.
14 Maay jafal ca kaw tatay Raba§1.14 Raba péeyu Amon la woon.,
mu xoyom ay taaxam,
yuux ya jib bésub xare,
ci biir callweer bésub ngëlén.
15 Seen buur ay duggi ngàllo,
mooki kàngamam.»
Aji Sax jee ko wax.
 

*1:1 1.1 Tekowa sorewul ak Yerusalem, péeyu Yuda. Ba bànni Israyil xàjjalikoo ñaari réew gannaaw ba Buur Suleymaan nelawee, réewum Israyil daa péeyoo Samari; réewu Yuda péeyoo Yerusalem.

1:1 1.1 Osiyas mooy Asaryaa itam.

1:2 1.2 Siyoŋ mooy tund wa kër Yàlla ga nekk ca Yerusalem. Daan nañu ko tudde it dëkku Yerusalem.

§1:3 1.3 Damaas mooy péeyu réewum Siri.

*1:5 1.5 xuru Awen mooy tekki xuru Ñaawtéef.

1:5 1.5 Bet Eden mooy kërug Àjjana, muy tekki fii Kërug Xawaare.

1:5 1.5 Kir la Arameen ñi cosaanoo. Gannaaw gi lañu sanci réewu Siri. Seetal ci 9.7.

§1:6 1.6 Gasa benn la ci juróomi dëkki Filisti yu mag; yeneen yi di Asdodd ak Askalon ak Ekkron, ak Gaat. Seetal ci 6.2.

*1:9 1.9 Tir dafa mel ni Sidon. Ay dëkk yu mag lañu woon ca réewum Fenisi.

1:11 1.11 Edomeen ñaa nga bàyyikoo fa bëj-saalumu Yuda jàpp penku. Ñu ngi soqikoo ci Esawu, magu Yanqóoba, kon bokki Israyil lañu woon, waaye dañoo faroon ak nooni Israyil.

1:12 1.12 Teman ak Boccra ay goxi Edom yu mag la woon. Boccra moo doon péeyu Edom.

§1:14 1.14 Raba péeyu Amon la woon.